Saar 2
1 Bëgg naa nag, ngeen xam xare bu metti, bi ma leen di xareel, yeen ak waa Lawdise ak mboolem gëmkat ñi ma masula teg bët, 2 ngir ngeen gëna am fit, mànkoo ci biir cofeel, te géeju ci gis-gisu xol bu leer nàññ te wóor, ba mana daj dëgg, mbóotum Yàlla, miy Almasi ci boppam. 3 Ci moom la mboolem alal ji ci xel ak xam-xam, dëxëñe. 4 Loolu laa leen di wax, ngir kenn bañ leena réerale ay kàdduy naxe yu mbubboo ag dëgg. 5 Ndax jëmm ji kat teewul, waaye xol baa ngeek yeen, di bégee gis seen doxalin wu jekk, ak seen ngëm gu wér gu ngeen gëm Almasi.
Jëfeleen ni ñu bokk ak Almasi
6 Kon nag, ni ngeen nangoo Almasi Yeesu di Sang bi, àndleen ak moom, jëfe noonu. 7 Sampleen seeni reen ci moom, tabaxuleen ci moom, feddlikuleen ci wàllu ngëm, ni ñu leen ko jàngale, ba seenub xol baawaanal kàdduy cant.
8 Moytuleen ba kenn bañ leena këfe kàdduy naxi neen yu ñu jàppe xam-xam bu xelu, kàddu yu sukkandikoowul Almasi, xanaa aaday nit, ak cëslaayi àddina.
9 Ndax kat ci Almasi, ci yaramu nitam la léppi Yàlla dëkke, ba mat sëkk ci moom, 10 ci moom ngeen mate it, te mooy kilifay mboolem boroom nguur yi, ak mboolem boroom sañ-sañ yi. 11 Ci moom ngeen xarafe xaraf gu loxol nit deful, ndax noonu kuy xarfal nit ki di doge as lëf ci yaramu nit ki, ni la Almasi di doge ba mu set, buumu njaam gi leen dooley bàkkaar tënke woon. Noonu la Almasi di xarfalee. 12 Ni ñu leen booleek moom suul, keroog ba ñu leen sóobee cim ndox, noonu ngeen dekkeendoo ak moom, ndax yeena wóolu dooley Yàlla mi ko dekkal.
13 Yeen ñi doonoon ndee fa kanam Yàlla ndax seeni moy, ak seen ñàkka xaraf, ndax li ngeen dul Yawut, Yàllaa leen booleek Almasi dundalaat leen. Moo nu baal sunu moy yépp. 14 Kayitu bor bi nu tiiñaloon, te dogali yoon toppe nu ko, moom moo far mbind ma, yóbbu kayit ga, daajaale ko ak Almasi ca bant ba. 15 Moo dog sidditi boroom nguur yeek boroom sañ-sañ yi ci jaww ji, ñu doon ay jaam yu mu jàppe xare. Moo leen weer it ci kanam ñépp, diriwaale leen ca biir njaab ma topp ca ndam, la Almasi ame ca bant ba.
16 Kon nag bu leen kenn sikkal ci ñam wu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan, mbaa màggal bés bu rafet, mbaa Terutel weer, ak bésub Noflaay. 17 Loolu lépp takkndeeru yaram wuy jëmmal lu dikkagul, moom rekk la woon. Waaye yaram wi dëgg moo di Almasi. 18 Buleen nangu kenn ku leen sikkal, te di kuy teg boppam jëfi toroxlu, di jaamu ay malaaka, topp seen gis-gisi peeñuy bopp. Ñu ni mel ñooy réy-réyloo xalaati neen yu ñu fente seen yég-yégi bakkan. 19 Ñooñu jokkuwuñu ci Almasi, miy bopp bi, te ci bopp bi la yaram wi wépp di jëfandikoo siddit yeek tenqo yi, ba suuxatu, ngir lépp mànkoo ba mana màgg, ni ko Yàlla di màggale.
20 Ndegam nag yeena bokk ak Almasi dee, ba teqlikoo ak li àddina def cëslaay, ana lu tax ngeen mel ni ñu bokk ci àddina ba tey, di tegoo ay dogali yoon yu mel nii: 21 «Bul jël lii, bul ñam lee, bul laal la ca des.» 22 Te mboolem yëf yooyu dogali yoon yi jëm day jeex doŋŋ bu ñu leen jëfandikoo. Loolu ay santaane aki àlluway nit doŋŋ la. 23 Dëgg la, xel man naa nangu dogali yoon yu ni mel, ndax laaj na nit ki pastéefu ci diine ju mu tegool boppam, laaj na it toroxlu, ak coonoy yaram yu tukkee ci yar bu metti bu nit kiy tegoo, waaye jariñul dara ku bëgga moom bakkanam.