Saar 7
Nit am na pexe ciw tiisam
Jëw bu rafet a gën diw gu xeeñ,
bésub dee a gën bésub juddu.
Dem dëj a gën wàlli bernde,
mooy muju képp.
Kuy dund, sóoraale ko.
Naqar a gën xaxaloo;
aw tiis ñëkkal kanam, rafetal xol.
Ku xelu, xalaat kërug dëj;
ku dofe, xalaat kërug puukare.
 
Déglu ku xelu di la àrtu
moo gën déglu dof bu lay woy.
Ab dof day textexi
ni dég yuy retete taal bu cin tege.
Loolu it di cóolóoli neen.
Foqarñi kay day dofloo boroom xel,
te ab ger da lay gëlëmal.
 
Fa mbir mujjee gën fa mu doore,
te muñ a gën réy-réylu.
Bul gaawa mer;
mer, xolub dof la samp këram.
10 Bul ne lu tax démb dàq tey,
loolu, laaj ko du xel.
 
11 Xel mu rafet daa neex ni ndono,
njariñ la ci kuy dund.
12 Xel mu rafet kiiraay la,
xaalis kiiraay la;
njariñu xam-xam mooy
xelu, mucc.
 
13 Xoolal ci li Yàlla def:
Ana ku mana jubbanti lu mu dëngal?
14 Su neexee, bànneexul;
su mettee, xoolal ne lu ci ne, Yàllaa ko def
ngir jaam bi umple gannaawam.
Lu ëpp tuuru
15 Lu ne laa gis
ci sama dund gu gàtt gii!
Nit a ngii jub, teewu koo sànkook njubam;
nit bon, ànd ak mbonam, gudd fan.
16 Bul jub ba mu ëpp,
bul wóolu sam xel ba mu ëpp,
lu ko moy nga yàqule.
17-18 Bu la mbon jiital,
te bul dofe.
Jàppool lii,
te baña wacc lee, mooy li gën,
lu ko moy nga dee te sa àpp jotul.
Ku ragal Yàlla kat
sàmm yooyu yaar.
Xel mu rafet réer na ma
19 Xel mu rafet day dooleel boroom,
ba mu man fukki kàngam cib dëkk.
20 Amul moos ku jub ci kaw suuf,
kuy def lu baax te du bàkkaar.
21 Te it du lépp lu ñu wax,
ngay bàyyi xel.
Kon doo dégg surga bu la ŋàññ,
22 ndax xam nga xéll ne yaw it
ŋàññe nga ay yooni yoon.
23 Loolu lépp maa ko natte xel mu rafet,
te naan: «Naa xelu,»
ndeke mbir ma sore na ma.
24 Li wara am daa loq, te xóota xóot;
ana ku ko mana daj?
 
25 Ma walbatiku, di jéema xam,
di wut, di càmbar, di sàkkum piri,
ngir xam li bon cig ndof,
ak li dofe, cig ndof.
26 Ma seetlu lenn lu gëna naqari dee:
muy ndaw su la fiir.
Kooku cofeelam mbaal la,
yoxo ya dib jéng.
Ku Yàlla gërëm a koy rëcc,
bàkkaarkat bi lay jàpp.
 
27 Waarekat ba nee: Xoolal li ma gis,
benn-bennal ko, ngir gis lu mu firi.
28 Ma seeta seet, gisuma.
Genn góor laa ràññee ci junniy góor,
ràññeewuma kenn ci jigéen ñi ñépp.
29 Lenn daal laa ràññee:
Yàlla daa sàkk nit, jubal ko,
nit di wuta sél fu ne.