Muccug bànni Israyil
di ñaareelu xaaju Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Ñaareelu xaaju Tawreet bii moo wéyal jaar-jaari bànni Israyil, jële ko fa ko téere bu jëkk ba, téereb Njàlbéen ga bàyyi woon. Fi téere bi jële aw turam, Mucc gi, mooy xew-xew bi ci gëna fés, di mucc gi Yàlla musal bànni Israyil, ca mbugal mu mujj ma mu wàcce woon fa Misra, mbugal ma Yàlla doge seen buumi njaam, ba génne leen fa.
Yàlla moo jox bànni Israyil ndigali yoon wi ca tundu Sinayi, Musaa jottli ko, muy li lal kóllëre gi mu fas, moom Yàlla ak bànni Israyil. Yàlla nag musal leen, ba ñu tala séq ak moom digganteb kóllëre. Ndigali yoon wi moo xamal mbooloom bànni Israyil nan lañuy sàmme seen digganteek moom. Yàlla moo bëggoon bànni Israyil doon ñoñam, ndax ci ñoom la nammoona amal digeem baak seen maam Ibraayma. Dige ba mooy xeeti àddina sépp, ci askanu Ibraayma lañuy barkeele.
Mujug téere bi kéemaan gu réy la. Mooy gannaaw ba ñu sampee jaamookaay ba, na ko Yàlla santaanee, ba Yàlla feesale ag leeram xaymab jaamookaay ba, ngir wone ne moo fa teew.
Ci Tënk:
Saar 1—18 Yàlla yiwi na bànni Israyil, génne leen Misra.
Saar 19—24 Yàlla fasante na kóllëre ak bànni Israyil.
Saar 25—40 Yàlla sant na Musaa, mu defarlu xaymab jaamookaay.
Saar 1
Bànni Israyil dem na réewum Misra
1 Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israyil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di: 2 Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda 3 ak Isaakar ak Sabulon, ak itam Beñamin; 4 ak Dan ak Neftali ak Gàdd ak Aser. 5 Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. 6 Gannaaw ga Yuusufaaki doomi baayam yu góor yépp nelaw, ñook maas googu gépp. 7 Bànni Israyil nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma.
Firawna not na bànni Israyil
8 Ñu dem ba jëmmi jamono, beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra. 9 Mu wax ak waa réewam, ne leen: «Giirug bànni Israyil kat ñu ngi nuy gëna bare, ba ëpp nu doole. 10 Nanu ci sàkk pexe, ngir ñu bañatee yokku. Lu ko moy bu xare amee, man nañoo far ak sunuy noon, xeex ak nun, ba génn réew mi.» 11 Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israyil tabaxale Firawna*1.11 Firawna turu pal la, ñeel bépp buuri Misra. buuru Misra†1.11 Misra mooy réew mi ñuy wax Esibtë ba tey. dëkk, ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund. 12 Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu, yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israyil.
13 Waa Misra dañoo mujj di jaamloo bànni Israyil bu metti, 14 yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas.
15 Firawna buuru Misra teg ca wax ak rewlikati Ebrë ya‡1.15 Ebrë tur la wu niti jamono jooja daan wooye xeet, ya bànni Israyil bokk., te kenn ka tuddoon Sifra, ka ca des di Puwa. 16 Mu ne leen: «Bu ngeen dee rewli jigéeni Ebrë yi, nangeen xool lu xale bi doon. Su dee góor, reyleen, su dee jigéen, bàyyileen, mu dund.» 17 Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund. 18 Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» 19 Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.» 20 Bànni Israyil nag di fulandiwu, gëna yokku, Yàlla defal rewlikat ya aw yiw, 21 may leen giir ndax seenug ragal Yàlla. 22 Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»