Lu jëm ci jaamookaay bi
Saar 25
Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Waxal bànni Israyil ne leen, ñu indil ma ab jooxe. Ci képp ku am yéeneem ngeen di nangoo sama jooxe, indil ma ko. Jooxe bi ngeen di nangoo ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar, ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy ak deri kuuyu xar yu ñu wulli, sóob ko xonqal, ak deri piipi*25.5 piipi rabu géej la, bu der ba nooy te ndox du ko dugg. ak banti séng25.5 séng: am na ñu koy wooye kasiya., ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwu pal, di xeeñal cuuraay, ak peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànnim sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam. Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir. Na lépp dëppoo ak li ma lay won. Muy misaalu xaymab jaamookaay bi, di misaalu mboolem ay jumtukaayam, lépp defeleen ko noonu.
Lu jëm ci gaal giy def àlluway seede si
10 «Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab25.10 xasab mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc. ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll. 11 Nañu ko xoob wurusu ngalam. Biir ak biti lañu koy xoob, sàkkal ko kéméju wurus, gu ko wër. 12 Móolalal gaal gi ñeenti lami wurus yu ñuy takk ci ñeenti tànk yi; ñaari lam, wet gii; ñaar wet gee. 13 Yettlul ay banti njàppuy séng te nga xoob bu ci nekk wurus. 14 Su ko defee nga roof njàppu yi ci lam, yi ci weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi. 15 Ci lami gaal gi la njàppu yiy des te bañ cee jógeeti. 16 Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox.
17 «Defarlul kubeer gu ñuy amale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll. 18 Tëgglul ñaari malaakay serub yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga. 19 Defal cat lii ab serub, cat lee ab serub te nanga móolaale kubeer gi ak serub yi ci ñaari cat yi, ñu ànd di benn. 20 Na serub yi tàllal seeni laaf, jëme kaw te nañu yiire kubeeru njotlaay gi seeni laaf. Nañu janoo, te na seeni kanam jublook kubeeru njotlaay gi. 21 Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox. 22 Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israyil.
Lu jëm ci taabalu mburum sarax mi
23 «Defarlul taabalu bantu séng, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di xasab, taxawaayam di xasab ak genn-wàll. 24 Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër. 25 Defal ko pegg bu ko wër bu tollu ci ñeenti baaraam, te sàkkal pegg ba wombu wurus, wërale ko. 26 Defarlul ko ñeenti lami wurus te takk lam ya ca ñeenti wet ya, fa fareek ñeenti tànk ya. 27 Na lam yi dendeek pegg bi, ngir mana téye njàppu, yi ñuy yóbboo taabal ji. 28 Yettlul ay njàppu yu bantu séng, nga xoob njàppu yi wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji. 29 Sàkkal ko ay ndabam yu tell aki mbàttoom aki njaqam, ak këllam yi ñuy tuuroo. Te wurusu ngalam ngay def lu ci nekk. 30 Tegal mburum teewal mi ci kaw taabal ji, mu nekk ci sama kanam ba fàww.
Lu jëm ci tegukaayu làmp bi
31 «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn. 32 Juróom benni car ñooy soqikoo ca wet ya, ñetti car ci gii wet, ñett ca ga ca des. 33 Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd§25.33 garabu amànd xeetoo naak gerte-tubaab., kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, juróom benni car, ya soqikoo ca per ba, daj. 34 Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram. 35 Ab kàmbóot ay ronu yii ñaari car, jàpp ca; beneen kàmbóot ronu ñaari car ya ca topp, jàpp ca, ab kàmbóot ronu ñaari car ya mujj, jàpp ca, juróom benni car, ya soqikoo ca peru làmp ba, daj. 36 Kàmbóot ya ak car ya dañuy ànd ak tegukaay ba, di benn, lépp doon lu ñu tëgge wenn dogu wurusu ngalam. 37 Defarlul juróom ñaari làmpam. Te na làmp ya tege tegin wuy leeral ca kanam tegukaay ba. 38 Ñiimi feyukaayu làmp yi ak andi làmp yi na doon wurusu ngalam. 39 Fanweeri kiloy wurusu ngalam ak juróom*25.39 Mu yemook benn nattu diisaay bu ñu daan jëfandikoo, ñu di ko wax talaŋ., ci lees di sàkk tegukaayu làmp bi, ak mboolem li mu àndal. 40 Nanga xool te topp misaal, yi ñu la ciy won ci kaw tund wi.

*25:5 25.5 piipi rabu géej la, bu der ba nooy te ndox du ko dugg.

25:5 25.5 séng: am na ñu koy wooye kasiya.

25:10 25.10 xasab mooy guddaayu loxo, diggante catu baaraamu digg ak conc.

§25:33 25.33 garabu amànd xeetoo naak gerte-tubaab.

*25:39 25.39 Mu yemook benn nattu diisaay bu ñu daan jëfandikoo, ñu di ko wax talaŋ.