Saar 2
Aji Sax ji yebal na Esekiyel
Ba loolu amee boroom kàddu ga ne ma: «Yaw nit ki, jógal taxaw, ma wax la.» Naka la ma wax loolu, ngelaw solu ma, ne ma yékkét, ma taxaw, di dégg kiy wax ak man. Mu ne ma: «Yaw nit ki, maa lay yebal ci bànni Israyil, xeeti fippukat yi fippu ci sama kaw; ñook seeni maam dañu maa masa tooñ ba bésub tey jii. Ci nit ñu dëgër bopp te dërkiis laa lay yónni. Wax leen, ne leen: “Lii Boroom bi Aji Sax ji da koo wax.” Ñoom nag, su ñu la déglook su ñu gàntalee ndax kërug fippukat gi ñu jikkowoo, dinañu xam ne ab yonent a ngi ci seen biir. Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu. Nanga leen àgge samay wax, ñu déglook ñu gàntal, nde ay fippukat lañu. Yaw nit ki nag, déglul lii ma lay wax. Bul fippu ni kërug fippukat gii. Sexal, te lekk li ma lay jox.»
Naka laa xool, yem ci loxo bu ñu ma tàllal. Ndeke taxañub téere moo ci nekk. 10 Mu tàqarñi ko fi sama kanam, muy lu ñu bind biir ak biti, mbind ma di kàdduy jooy aki onk aki yuux.