Saar 8
Lu jëm ci ñi ànd ak Esra
Ñi jiite seen làngi kër maam ak ñi ñu bindaaleek ñoom ci limeef yi, te ñu ànd ak man Esra, jóge Babilon ca jamonoy Buur Artaserses, ñii la: Ci askanu Fineyas, Gersom la. Ci askanu Itamar, Dañeel la. Ci askanu Daawuda, Atus, mi askanoo ci Sekaña la. Askanu Paros, Sàkkaryaa bawoo ca, ànd ak téeméeri góor ak juróom fukk (150). Ci askanu Payat Mowab, Elyowenay doomu Seraya la, mook ñaar téeméeri góor (200). Ci askanu Sàttu*8.5 Sàttu: tekki bu jëkk ba ci làkku gereg moo indi turu Sàttu., Sekaña doomu Yasyel la, mook ñetti téeméeri góor (300). Ci askanu Adin, Ebedd doomu Yonatan la, mook juróom fukki góor (50). Ci askanu Elam, Esayi doomu Atalyaa la, mook juróom ñaar fukki góor (70). Ci askanu Sefatiya, Sebadiya doomu Mikayel la, mook juróom ñett fukki góor (80). Ci askanu Yowab, Obadiya doomu Yeyel la, mook ñaar téeméeri góor ak fukk ak juróom ñett (218). 10 Ci askanu Baani8.10 Baani: tekki bu jëkk ba ci làkku gereg moo indi turu Baani., Selomit doomu Yosifya la, mook téeméeri góor ak juróom benn fukk (160). 11 Ci askanu Bebay, Sàkkaryaa doomu Bebay la, mook ñaar fukki góor ak juróom ñett (28). 12 Ci askanu Asgàdd, Yowanan doomu Àkkatan la, mook téeméeri góor ak fukk (110). 13 Askanu Adonikam ñoo mujje, ñu di leen wax Elifelet ak Iyel ak Semaya, ñook juróom benn fukki góor (60). 14 Ci askanu Bigway, Utay la ak Sabudd, ñook juróom ñaar fukki góor (70).
15 Ci kaw loolu ma boole leen, ñu daje ca wetu dex, ga jëm Aawa, dal fa ñetti fan. Ma seetlu fa baadoolo ya, seet ca biir sarxalkat ya, gisuma kenn ku bokk ci Leween ñi. 16 Ma woolu njiit ya: Elyeser ak Aryel ak Semaya ak Elnatan ak Yarib ak Elnatan meneen ma, ak Natan ak Sàkkaryaa ak Mesulam, ak Yowarib ak Elnatan ma ca des, ñaari jànglekati yoon ya. 17 Ba mu ko defee ma yebal leen ca Ido, njiit la ca gox ba ñuy wax Kasifya, daldi leen wax kàddu ya ñuy jottli Ido ak bokkam yay liggéeykati kër Yàlla, ya dëkk Kasifya, ndax ñu yónnee nu ay surga ci sunu liggéeyu kër Yàlla gi. 18 Sunu Yàlla nag toppe nu mbaaxu yiwam, ba ñu indil nu waa ju am xel, askanoo ci Maali sëtub Lewi doomu Israyil. Ñu di ko wax Serebya. Mu ànd ak doomam yu góor aki bokkam, ñuy fukk ak juróom ñett (18), 19 ñook Asabya ak Esayi sëtu Merari. Ñu ànd ak seeni bokk ak seen doom yu góor, di ñaar fukki góor (20). 20 Indaale nañu ñaar téeméeri liggéeykati kër Yàlla ak ñaar fukk (220), di ñu askanoo ca ña Daawudaaki jawriñam tànnoon, bind seeni tur, ngir ñuy jàpple Leween ñi.
21 Ba loolu amee ma digle foofa koor ca tàkkal dexu Aawa, toroxloo ko fa sunu kanam Yàlla, ngir ñaan ko mu may nu yoonu jàmm, nook sunuy doom ak mboolem lu bokk ci nun. 22 Ndaxte rusoon naa ñaan Buur mu boole nook ay dag ak gawar yu nu aar ci noon yi ci yoon wi. Li ko waral mooy fekkoon na nu wax Buur ne ko: «Sunu Yàlla mooy toppe yiwam mboolem ku ko yaakaar, di ko defal jàmm, waaye meram dina dal ak doole ci kaw mboolem ku ko dëddu.» 23 Nu woor, daldi dagaan sunu Yàlla mbir moomu, mu nangul nu. 24 Ba loolu amee, ma tànn fukki sarxalkat ak ñaar yu mag, ñuy Serebya ak Asabya ak seen fukki bokk. 25 Gannaaw loolu ma nattal leen xaalis baak wurus waak ndab, ya Buur aki wóllëreem aki jawriñam jooxe woon, ñook mbooloom Israyil ma fa teewoon, te lépp jëm ca sunu kër Yàlla ga. 26 Natt naa ba teg ci seeni loxo ñaar téeméeri barigoy xaalis ak fanweeri barigo ci jumtukaayi xaalis ak fanweeri barigoy wurus, 27 ak ñaar fukki koppi wurus yu wecci junniy poseti wurus, ak ñaari ndab yu jafe, yu xànjar bu ñu raxas ba muy melax, mel ni wurus. 28 Ma ne leen: «Yeen, dees leena sellalal Aji Sax ji, ni ñu sellale ndab yi, te xaalis beek wurus wi di saraxu yéene ñeel Aji Sax ji, seen Yàllay maam. 29 Xool-leen ko te sàmm ko bu baax, ba kera ngeen koy natt ca denci kër Aji Sax ji ca Yerusalem, fa kanam kilifay sarxalkat yaak Leween ñaak ña jiite seen làngi kër maam ci bànni Israyil.»
30 Ci kaw loolu nu nattal sarxalkat yeek Leween ñi xaalis baak wurus waak ndab yu sell ya, ngir ñu yóbbu ko ca sunu kër Yàlla ga ca Yerusalem. 31 Fukki fan ak ñaar ca weer wa jëkk lanu bàyyikoo dexu Aawa, daldi jëm Yerusalem. Sunu Yàlla nag toppe nu yiwam, ba musal nu ci noon akub saaysaay ci yoon wi.
32 Gannaaw loolu nu agsi Yerusalem, nopplu fa ñetti fan. 33 Bésub ñeenteel ba nu natt diisaayu xaalis baak wurus waak ndab ya ca sunu biir kër Yàlla ga, teg ko ca loxol Meremot doomu Uri, sarxalkat ba, mook Elasar doomu Fineyas, ak Leween ña, di Yosabàdd doomu Yeswa, ak Nowadiya doomu Binuy. 34 Ñu limaat lépp, nattaat diisaay ba, daldi bind ca saa sa dayo ba bépp.
35 Ba mu ko defee ña jóge njaam, ñibbsee ca ngàllo ga, daldi defal Yàllay Israyil ay saraxi dóomal. Muy fukki yëkk ak ñaar, ñeel Israyil gépp ak juróom ñeent fukki kuuy ak juróom benn (96), ak juróom ñaar fukki xar yu ndaw ak juróom ñaar (77), ak fukki sikket ak ñaar yu ñu def saraxu póotum bàkkaar; ñu def lépp saraxu dóomal, ñeel Aji Sax ji. 36 Ci biir loolu ñu jottli ndigali buur, ya jëm ca ay jawriñam ak njiiti Wàllaa Dex. Ñooñu it jàpple mbooloo ma ca liggéeyu kër Yàlla ga.

*8:5 8.5 Sàttu: tekki bu jëkk ba ci làkku gereg moo indi turu Sàttu.

8:10 8.10 Baani: tekki bu jëkk ba ci làkku gereg moo indi turu Baani.