Saar 3
Dellu ci yoonu Musaa du xel
Yeen waa Galasi, yeena ñàkk xel! Ku leen gëlëmal, te na Yeesu Almasi deeye ca bant ba di lu ñu leen leeralal ba mu mel ni lu ngeen gise seeni bët? Lenn rekk laa bëgg ngeen xamal ma ko: ndax ci jëfi sàmm ndigalu yoon ngeen jote Noowug Yàlla gi, am li ngeen dégg xibaaru jàmm bi ba gëm ko moo leen ko may? Ana nu ngeen mana ñàkke nii xel? Ngeen tàmbalee ci Noo gi, ba noppi di jéema mottlikoo jëfi nitu suuxu neen! Dangeena dékku yii coono yépp ci neen? Xanaa déet kay! Ki leen di may Noo gi, tey sottal ay kéemaan ci seen biir, ndax li ngeen sàmm yoon moo tax mu di ko def, am li ngeen dégg, ba gëm moo tax?
Noonu la Ibraayma gëme Yàlla, «ñu waññal ko ngëmam ag njub*3.6 Seetal ci Njàlbéen ga 15.6.
Xamleen boog ne nit ñiy boroom ngëm, ñooñu ñooy doomi Ibraayma. Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele3.8 Seetal ci Njàlbéen ga 12.3.ba tax na, boroom ngëm yi lees di booleek Ibraayma miy boroom ngëm, barkeel leen.
10 Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe3.10 Seetal ci Baamtug Yoon wi 27.26. 11 Li sàmm yoon taxul kenn jot àtteb ku jub fi kanam Yàlla sax, lu leer nàññ la, nde: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.» 12 Yoon wi nag ajuwul ci ngëm, nde: «Kuy jëfe digal yooyu, yaay dund ndax ñoom§3.12 Seetal ci Sarxalkat yi 18.5.
13 Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant*3.13 Seetal ci Baamtug Yoon wi 21.23.14 Noonu la deme ngir barkeb Ibraayma wàccal xeet yi dul Yawut ndax Almasi Yeesu, ngir itam nu jot ci digeb Noo gu Sell gi, ci kaw ngëm.
Yoonu Musaa fecciwul kóllëre
15 Bokk yi, ma misaale ko mbiri doom Aadama. Kayitub donale bu nit doŋŋ bind, su dee lu wóor, deesu ko neenal, mbaa di ci yokk dara. 16 Te Ibraayma lañu digoon dige yi mook ki taxawal askanam. Newuñu: «ñi taxawal ay askanam», mbete ñu bare lañuy wax, waaye wenn rekk la: «ki taxawal askanam,» te ki taxawal askanam moo di Almasi. 17 Li ma ciy wax mooy lii: kóllëreg Yàlla gi taxawe ni kayitu donale gu mu dëggal, yoonu Musaa, wi dikk ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw kóllëre gi, manu koo neenal, ba fomm digeb3.17 Seetal ci Njàlbéen ga 17.1-8. Yàlla. 18 Su doon ci yoonu Musaa la ndonale ga aju, kon dootul doon lu digeb Yàlla waral. Waaye ci kaw ab dige la Yàlla baaxee Ibraayma aw yiwam.
Ku gëm Almasi, yoonu Musaa wàcc na la
19 Waaw kon yoonu Musaa, ana luy njariñam? Dees koo toftal ca dige ba, ngir muy fésal moyi nit ñi ba keroog boroom dige, bi taxawal askanu Ibraayma, dikk. Ay malaaka ñoo biral yoon wi, ci ndimbalal ab jottlikat3.19 jottlikat bi mooy Musaa.. 20 Ab jottlikat nag ñaar a koy séq, te Yàlla kenn doŋŋ la.
21 Ndax kon yoonu Musaa dafa juuyoo ak digey Yàlla? Mukk kay. Ndax kat su fekkoon ne dañoo maye wenn yoon wu mana may nit ku ko sàmm, mu dund, konoon àtteb ku jub fi kanam Yàlla mana jóge dëgg ci sàmm gu nit ki sàmm yoon wi. 22 Waaye mbind mi biral na ne mboolem àddina moo tënku ci kilifteefu bàkkaar, ngir dige bi gëm Yeesu Almasi di jagle, mana dikkal aji gëm ñi.
23 Balaa yoonu ngëm wee dikk, dees noo jàppoon tënk ci yoonu Musaa, ba kera yoonu ngëm wi feeñee. 24 Noonu la yoonu Musaa doone sunu njaatige, tette nu ba ci Almasi, ngir nu jagoo àtteb nit ñu jub ci kaw ngëm. 25 Waaye léegi, bi yoonu ngëm wi dikkee, nekkatunu ci kilifteefu njaatige.
Doomi Yàlla ngeen
26 Yeen ñépp doomi Yàlla ngeen, ndax li ngeen gëm Almasi Yeesu. 27 Ndax kat mboolem yeen ñi ñu sóob sóobeb Almasi, jëmmu Almasi ngeen soloo. 28 Kon nag amul Yawut ak ku dul Yawut, amul ab jaam ak as gor, amul góor ak jigéen. Yeen ñépp benn ngeen ci Almasi Yeesu. 29 Te su ngeen bokkee ci Almasi, yeen ay askanu Ibraayma, te yeena jagoo dige ba.

*3:6 3.6 Seetal ci Njàlbéen ga 15.6.

3:8 3.8 Seetal ci Njàlbéen ga 12.3.

3:10 3.10 Seetal ci Baamtug Yoon wi 27.26.

§3:12 3.12 Seetal ci Sarxalkat yi 18.5.

*3:13 3.13 Seetal ci Baamtug Yoon wi 21.23.

3:17 3.17 Seetal ci Njàlbéen ga 17.1-8.

3:19 3.19 jottlikat bi mooy Musaa.