Saar 2
1 Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat. 2 Bésub juróom ñaareel ba fekk na Yàlla matal liggéeyam. Mu dal-lu nag ca bésub juróom ñaareel ba, gannaaw ba mu liggéeyee loolu lépp. 3 Yàlla daldi barkeel bésub juróom ñaareel ba, def ko bés bu sell, ndax da caa dal-lu woon gannaaw liggéey, ba mu sàkke lépp.
Cosaanal asamaan ak suuf
(Saar 2.4—4.26)
Yàlla dugal na nit Àjjana, jox ko ndigal
4 Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, 5 genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul. 6 Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. 7 Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan.
8 Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. 9 Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon.
10 Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddlikoo, def ñeenti wal. 11 Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, 12 di wurusu ngalam; te it ndàbb lu neex xet a nga fa woon ak per yu jafe yu ñuy wax onigsë. 13 Ñaareelu dex ga di Giyon, wër réewu Kuus mépp; 14 turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat.
15 Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm. 16 Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, 17 waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.»
18 Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» 19 Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. 20 Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.
21 Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. 22 Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko. 23 Aadama ne tonet, daldi ne:
«Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux!
Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële*2.23 Ni ñuy wooye góor ak ni ñuy wooye jigéen dañoo jegeyoo ci làkku ebrë..»
24 Looloo tax góor di bàyyikoo ci ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñuy wenn suux.
25 Ku góor ki ak soxnaam, ñoom ñaar ñépp, yaramu neen lañu defoon, te amuñu ci woon genn kersa.