Saar 47
Yuusufa nuyole na ay bokkam Firawna
1 Yuusufa daa dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Sama baay ak samay bokk, jóge nañu Kanaan, ànd ak seen jur gu gàtt ak gu gudd ak mboolem lu ñu moom. Ña nga léegi ca diiwaanu Gosen.» 2 Fekk na Yuusufa tànn juróom ciy doomi baayam. Mu nuyole leen ak Firawna. 3 Firawna laaj doomi baay ya, ne leen: «Lan mooy seen liggéey?» Ñu ne ko: «Nun de sang bi, ay sàmm lanu naka jekk ca sunuy maam ba tey.» 4 Ñu teg ca ne ko: «Danoo ñëw ngir dal ci réew mi, ndaxte amalatunu sunu jur parlu, te xiif bi metti na ca réewu Kanaan. Moo tax sang bi, nu di la ñaan, nga may nu, nu dal foofa ca diiwaanu Gosen.» 5 Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Gannaaw sa baay ak say bokk ñëw nañu fi yaw, 6 réewum Misra a ngii ci sa kanam. Seetal fi gën ci réew mi, nga jox sa baay ak say bokk, ñu sanc. Bàyyi leen, ñu sanc Gosen, te bu ci amee ñu xareñ ci ñoom, nga dénk leen samay gétt.»
7 Gannaaw loolu Yuusufa ànd ak baayam ba fa Firawna, nuyole ko ak moom. Yanqóoba nuyu Firawna. 8 Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!» 9 Yanqóoba wax Firawna ne ko: «Samay ati màngaan, ba ma ganee àddina ba tey de, mu ngi tollu ci téeméer ak fanweer, muy at yu gàtt te naqari, te it demuma bay tolloo ay at ak samay maam, ba ñuy màngaan ci àddina.» 10 Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem.
11 Yuusufa nag dalal baayam aki bokkam, dogal leen suuf sa gën ca réewum Misra ca diiwaanu Ramses, ni ko ko Firawna sante woon. 12 Ba loolu amee Yuusufa di dundal baayam aki bokkam, ak mboolem waa kër baayam, boole ca ña bootu ca ñoom.
Lu jëm ci saytub Yuusufa ca xiif ba
13 Ab dund amuloon fenn ca réew ma mépp, ndax xiif bu metti lool. Waa réewum Misra ak réewu Kanaan jeex tàkk ndax xiif ba. 14 Yuusufa nag dajalee ca pepp, ma mu jaay waa Misra ak waa Kanaan, mboolem xaalisu ñaari réew ya, yóbbu nag xaalis ba kër Firawna. 15 Ba ñu demee, ba xaalis amatul ca Misra ak ca Kanaan, waa Misra gépp ñëw fa Yuusufa ne ko: «Jox nu ab dund kay! Mbaa du danga nuy seetaan, nuy dee? Ndax xaalis amatul.» 16 Yuusufa ne leen: «Indileen seeni jur, ma wecci leen ko dund, ndegam amatuleen xaalis.» 17 Gannaaw loolu ñu indil Yuusufa seeni jur, Yuusufa jox leen ko pepp, wecci leen ko seeni fas ak seeni gétti jur gu gàtt ak gu gudd ak seeni mbaam. At mooma jox na leen ab dund, mu wecci seen gétt gépp. 18 Ba at ma jeexee, ñu ñëwaat ca moom ca déwén sa ne ko: «Sang bi, dunu la nëbb ne amatunu dara, ndax xaalis bi jeex na, te jur gaa ngi ci yaw, dara nekkatu fi lu nu la mana jox lu moy sunuy jëmm ak sunuy tool. 19 Mbaa du danga nuy seetaan, nu bokk sànku ci sa kanam, nook sunu suuf? Ngalla boole nu jënde ab dund, nun ak sunuy suuf. Su ko defee nuy moomeeli Firawna, nun ak sunuy suuf. Te nga jox nu pepp mu nu dunde, lu ko moy kat nun dinanu dee, suuf si it dina booy.»
20 Yuusufa nag jëndal Firawna suufas Misra gépp, ngir waa Misra ya jaay ku ci nekk sa tool ndax xiif, ba leen jiital, ba Firawna mujj moom suuf si. 21 Waa réew ma ñoom, Yuusufa da leena def ay jaam ca Misra, gii wet ba gaa. 22 Bàyyiwul lu moy suufu njiiti diine ya, ndax Firawna jotoon na leena dogal ay cér, jagleel leen. Moo tax jaayuñu seeni suuf.
23 Yuusufa ne waa réew ma: «Léegi gannaaw jënd naa leen, ba Firawna moom leen, yeen ak seeni suuf, jiwoo ngii, demleen jiyi. 24 Bu nu àggee ci ngóob, juróom yu ngeen am dingeen ci jox Firawna benn, te féetewoo ñeenti cér yi des. Su ko defee ngeen génne ci jiwuy tool yi, li ci des ngeen dunde, yeen ak seen waa kër ak seeni doom.» 25 Ñu ne ko: «Sang bi, rawale nga nu! Te gannaaw laaye nga nu biir, nangu nanoo doon jaami Firawna.» 26 Noonu la Yuusufa tërale loola, def ko dogalu yoon ca suufu Misra, te loolooy wéy ba tey jii: juróomi céri meññeef mu ne, Firawnaay moom benn ba. Waaye suufi njiiti diine ya ca bokkul, Firawna amu ca dara.
Lu jëm ci ati Yanqóoba yu mujj ya
27 Bànni Israyil sanc nañu réewum Misra ca diiwaanu Gosen. Am nañu fa alal, giir fa, ba yokku lool.
28 Yanqóoba nag nekk na fukki at ak juróom ñaar ca réewum Misra, ay atam yépp tollu ci téeméer ak ñeent fukk ak juróom ñaar (147). 29 Ba nga xamee ne àppu Israyil a ngay bëgga mat, dafa woolu doomam Yuusufa ne ko: «Ngalla waay dugalal sa loxo, mu ron sama lupp*47.29 Seetal ci 24.2-3. , muy ngiñ ci yaw ne dinga jëflanteek man ci ngor ak worma: rikk, bu ma denc Misra. 30 Bés bu ma fekkijee samay maam, nanga ma jële Misra, denci ma ca seen xuntim bàmmeel.» Yuusufa ne ko: «Dinaa la defal li nga wax.» 31 Mu ne ko: «Giñal ma ko.» Yuusufa giñ ko, Israyil doora am jàmm, daldi wéeru ca bopp lal ba.