Saar 2
Fa may jongroo laay taxaw,
ne temm fa kaw tata ja,
ba xam ana lu mu ma Aji Sax ji di àddu,
ak lu may waxaat ci samab tawat.
Aji Sax ji àddooti na
Aji Sax jee àddu, ne:
«Bindal peeñu mi,
leeral ko ci àlluwa yi,
ba njàng mi yomb.
Peeñu mi seede la, ñeel jant
ba ñu ko àppal,
seede su wóor ci na mbir may mujje,
te du fen.
Su diibee it, xaar ko,
day dikk moos te du yàggati.
 
«Xol baa ngay xoggliku, te ag njub nekku ca,
waaye ku jub ndax kóllëreem mooy dund.
Biiñ day wore,
jàmbaar ju bew jii*2.5 Jàmbaar ju bew jii mooy waa Babilon. nag du dal-lu,
xanaa yàkkli puruxam ni njaniiw,
du doylu, mbete ndee,
moom miy buubandoo xeetoo xeet,
dajale askanoo askan, aakimoo.
“Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji,
fental ko woy wu ñu ko kókkalee, naan:
‘Wóoy ngalla kii di dajale lu mu moomul,
lii ba kañ?’
Kii di sëfoo nii ay bor!”
Moo ñi la lebal duñu jekki jóg a?
Ñooñu la tiital ñooy jekki yewwu,
te yaay doon seenum cëxëtoo.
Yaa sëxëtoo woon ay xeet yu bare,
mboolem ndesu askan yee lay sëxëtooji,
ndax deretu nit ji nga tuur, soxore ay réew,
aki dëkk, ak mboolem ña ca biir.
 
«Wóoy ngalla kuy dajaleel këram
alalu yàqute ju lewul
tey aj am tàggam fu kawe,
ngir fegu ci yàqule.
10 Gàcce nga nasal sa kër,
ba nga sànkee ay xeeti xeet,
te yaa tooñ sa bopp.
11 Doju tata dina riir déy,
aw dénk àddoo ca jank ba, feelu ko.
 
12 «Wóoy ngalla ku tabaxe ab dëkk,
deret ju mu tuur,
ku sanceb dëkk, ag njubadi.
13 Xanaa du ci Aji Sax ji
Boroom gàngoor yi la lii bawoo:
Sawara la askan yiy ñaqal,
ag neen la waasoo yiy doñ-doñil?
14 Waaye ni ndox muure xóotey géej ba mu daj,
ni la darajay Aji Sax jiy ràññikoo ci àddina sépp.
 
15 «Wóoy ngalla yaw mi nàndal sab dëkkaale,
sotti sa ndabal sànj, màndale ko,
ngir niir ko, mu ne duŋŋ!
16 Gàcce ngay gëna regg teraanga,
naanal yaw it te wone sa mbuñuka!
Ci yaw la kaas bi ci ndijooral Aji Sax ji
di walbatiku,
sa toroxte wuutu sa teraanga.
17 Ay wi nga teg Libaŋ mooy këppu
ci sa kaw,
te sànkuteg rabi àll yi sa tiitaange lay jur.
Yaa tuur deretu nit, indi aw ay ci réew mi,
ak dëkk beek mboolem ñi ci biiram.
 
18 «Ana luy njariñal yett jëmmu xërëm
ju ki ko sàkk yett,
mbaa jëmmu xërëm ju ñu xelli,
di ci gëmloo nit ay fen?
Sàkk sa yëfi bopp, wóolu ko,
xërëm yoo móol te manula wax!
19 Wóoy, ngalla ku naan bant: “Xippil,”
naan doj wu ne selaw: “Yewwul!”
Ana lu yooyii di xamle?
Ma nga, ñu xoobe ko xaalis ak wurus,
te du gennug noo ci biiram.
20 Aji Sax ja moom, ma nga ca màkkaanum sellngaam,
na àddina sépp selaw fi kanamam.»

*2:5 2.5 Jàmbaar ju bew jii mooy waa Babilon.