Téereb Yonent Yàlla
Ase
Saar 1
Tabaxaat jaamookaay bi jot na
1 -Ca ñaareelu atu nguuru Buur Daryus*1.1 Daryus buuru Pers bu mag la woon., ca juróom benneelu weer wa, yemook benn fan ca weer wa, kàddug Aji Sax ji moo dikk ci jottlib Yonent Yàlla Ase, ñeel doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ñeel itam doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba. Mu ne: 2 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Askan wii dañu ne àpp bi jotagul; àppub kër Aji Sax ji moo jotagul, ba ñu war koo tabaxaat.» 3 Kàddug Aji Sax ji nag dikk ci jottlib Yonent Yàlla Ase. Mu ne:
4 «Àpp bi daal yeen la jotal,
ba ngeen dëkke biir kër yu ay xànq lale,
te kër gii dib gent?
5 Kon nag léegi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
Teewlooleen xel seeni jaar-jaar.
6 Yeenay ji lu bare, góob tuuti;
lekk, suuruleen;
naan, màndiwuleen;
solu, nugluwuleen;
boroom peyoor feyeeku,
yeb ci mbuus mu bënn.»
7 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Teewlooleen xel seeni jaar-jaar.
8 Yéegleen tund wi, wuti bant, tabax sama kër gi;
ma bànneexoo, darajawoo ko,»
la Aji Sax ji wax.
9 «Lu bare ngeen séentu, ndeke as tuut la,
ngeen fat ko ci kër gi,
ma wal, mu naaw.
Li ko waral lu mu?» Kàddug Aji Sax ji
boroom gàngoor yee.
«Li ko waral mooy sama kër gi gental,
te ku ne ci yeen di dawal sa kër bopp.
10 Kon nag yeena tax asamaan téye ab layam,
suuf téye meññeefam,
11 ma wool bekkoor suuf seek kaw tund yi,
ak pepp ak ndoxum reseñ,
ak diw ak lu suuf meññal,
ak doom aadama aku jur,
ak mboolem liggéeyu loxo.»
Askan wi tontu na
12 Ba loolu amee doomu Selcel, Sorobabel, ak doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña des ca askan wa, ñoom ñépp déggal seen wooteb Yàlla Aji Sax ji, ak kàddug Yonent Yàlla Ase, noonee ko ko seen Yàlla Aji Sax ji yóbbantee. Askan wa nag ragal Aji Sax ji. 13 La ca tegu Ase, ndawal Aji Sax ji, jottli askan wa yóbbanteb Aji Sax ji. Mu ne leen: «Maa ànd ak yeen, kàddug Aji Sax jee.»
14 Ba mu ko defee Aji Sax ji yékkati sidditi doomu Selcel, Sorobabel boroom Yuda, ak sidditi doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag ba, ak sidditi ña des ca mbooloo ma ñépp, ba ñu sottali liggéeyi kër Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, seen Yàlla. 15 Loola yemook ñaar fukki fan ak ñeent ca juróom benneelu weer wa.