Saar 3
Doom jee gëna màgg Musaa
1 Kon nag bokk yu sell yi, yeen ñi bokk ci wooteb asamaan, ràññeeleen Yeesu, ndaw li, sarxalkat bu mag bi ci yoon wi nu gëm. 2 Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla. 3 Waaye ni ab tabaxkat ëppe teddnga kër ga muy tabax, ni la Yeesu yelloo daraja ju ëpp ja Musaa yelloo woon. 4 Ndax kër gu nekk am na ku ko tabax, waaye ki tabax lépp mooy Yàlla. 5 Musaa déy «jawriñ bu wóor la woon ci biir mboolem waa kër Yàlla*3.5 Seetal ci Màndiŋ ma 12.7. ,» di seedeel Yàlla kàddu ya ñu fa wara wax. 6 Almasi nag mooy Doom ju wóor ji jiite kër Yàlla, te nun nooy këram, ndegam kay nu ngi wéye aw fit, ak yaakaar ji nuy puukarewoo.
Almasi moo jara déggal
7 Kon nag ni ko Noo gu Sell gi waxe:
«Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,
8 buleen të na woon ca fippu ga,
keroog bésub seetlu Yàlla, ba ca màndiŋ ma†3.8 Seetal ci Mucc ga 17.1-7.,»
9 «fa ma seeni maam doon seetloo, di ma diiŋat,
te gisoon samay jaloore,
10 diiru ñeent fukki at.
Moo tax ma mere googu maas, ba ne:
“Seen xol a dëkke lajj,
te nanguwuñoo xam samay yoon.”
11 Moo ma taxa giñe sama biir mer, ne:
“Duñu tàbbi mukk ci samag noflaay‡3.7-11 Seetal ci Sabóor 95.7-11. noflaay: Yàlla moo digoon bànni Israyil ag noflaay, te mooy jàmm ju mu leen digoon ne dinañu ko dëkke biir Kanaan, gannaaw bu ñu fa duggee. Waaye ñi déggal Yeesu Almasi, ñoo jagoo teeweji jataayu Yàlla, te loolu mooy doon seen noflaay..”»
12 Bokk yi, wattuleen bala kenn ci yeena am xolub gëmadi bu bon bu koy xiir ci dëddu Yàlla jiy dund. 13 Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub tey agum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis. 14 Ndax kat noo di àndandooy Almasi, ndegam wéye nanoo ŋoy bu dëgër ci sunu kóolute ga nu doore, ba kera muj ga. 15 Waxees na ne:
«Bésub tey jii bu ngeen déggee baatam,
buleen të na woon ca fippu ga§3.15 Seetal ci Sabóor 95.7-8..»
16 Ana ñan ñoo déggoon te teewuleena fippu? Xanaa du mboolem ña génne woon Misra ci njiital Musaa? 17 Ana ñan la Yàlla mere lu mat ñeent fukki at? Xanaa du mboolem ña bàkkaaroon te seeni néew mujj tëdd ca màndiŋ ma? 18 Te it ana ñan ñu moy ña déggadi woon, la Yàlla giñaloon ne duñu tàbbi mukk ci noflaayam? 19 Kon nu gis ne seen gëmadee tax manuñu ca woona tàbbi.
*3:5 3.5 Seetal ci Màndiŋ ma 12.7.
†3:8 3.8 Seetal ci Mucc ga 17.1-7.
‡3:11 3.7-11 Seetal ci Sabóor 95.7-11. noflaay: Yàlla moo digoon bànni Israyil ag noflaay, te mooy jàmm ju mu leen digoon ne dinañu ko dëkke biir Kanaan, gannaaw bu ñu fa duggee. Waaye ñi déggal Yeesu Almasi, ñoo jagoo teeweji jataayu Yàlla, te loolu mooy doon seen noflaay.
§3:15 3.15 Seetal ci Sabóor 95.7-8.