Saar 8
Kóllëre gi gën la Yeesu Sarxalkat bi indi
Kàddu yii nu wax nag, lii moo di ponk bi: boobu sarxalkat bu mag lanu am, mu tooge ndijooru ngànguney ku Màgg ka fa asamaan. Mooy liggéeye kër gu sell ga, ca biir xaymab jaamookaay bu dëggu, ba Boroom bi samp, te nit sampu ko.
Gannaaw nag ab sarxalkat bu mag bu mu mana doon, dees koo fal, ngir muy jébbale ay jooxe ak saraxi jur, kon fàww sarxalkat bu mag bii itam am lu mu sarxe. Bu doon ci àddina, du nekk sax ab sarxalkat, gannaaw ay sarxalkat a ngi fi, di jébbale ay sarax, ni ko yoonu Musaa laaje. Sarxalkat yooyu, jaamookaay bi ñuy liggéeye, ab misaal la, takkndeeru yëf yu dëggu ya fa asamaan la. Ndax ba Musaa di waaja yékkati xaymab jaamookaay ba, noonu lees ko artoo woon ne ko: «Nanga xool te def lépp, mu dëppook misaal mi ñu la won ci kaw tund wi*8.5 Seetal ci Mucc ga 25.40.Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.
Bu kóllëre gu jëkk ga muccoon sikk nag, deesul soxlaa xajal geneen. Waaye Yàllaa sikk bànni Israyil, ba mu nee:
«Ay fan a ngii di ñëw, la Boroom bi wax,
mu ne maay fas ak kër Israyil ak kër Yuda,
kóllëre gu yees
gu bokkewul ak ga ma séqoon ak seeni maam,
ba ma leen jàppee ci loxo,
génne leen réewum Misra.
Gannaaw ñoo sàmmul sama kóllëre nag,
man it geesuwuma leen,
la Boroom bi wax.
10 «Lii nag moo di kóllëre gi may fas
ak kër Israyil, gannaaw yooyu fan,
la Boroom bi wax, mu ne:
Maay yeb sama ndigali yoon ci seenum xel,
ci seen xol laa koy ñaas.
Maay doon seen Yàlla,
ñoom ñu doon sama ñoñ.
11 Kenn dootu soxlaa jàngal moroomam,
mbaa mbokkam, naan ko: “Ràññeel Boroom bi!”
Ndax ñoom ñépp a may ràññee,
ki gëna tuut ba ci ki gëna mag.
12 Maa leen di jéggal seeni njubadi,
te seeni bàkkaar, duma ci bàyyeeti xel8.12 Seetal ci Yeremi 31.31-34.
13 Bu Yàlla wooyee kóllëre gii gu yees nag, daa fekk mu wonnil gu jëkk ga. Lu wonni te di lu yàgg nag, mu ngi ci tànki wees.

*8:5 8.5 Seetal ci Mucc ga 25.40.

8:12 8.12 Seetal ci Yeremi 31.31-34.