Saar 5
Njiiti Israyil lajj nañu
«Dégluleen lii, yeen sarxalkat yi!
Teeyluleen, yeen waa kër Israyil!
Teewluleen, yeen waa kër buur!
Yeen la àtte bi ñeel.
Ag fiir ngeen tegoon ca Mispa,
ab caax ngeen laloon ca tundu Tabor,
Fippukat yi gën nañoo xuus ci seen bóome,
waaye maa leen di yar, ñoom ñépp.
Maa xam Efrayim,
Israyil laa ne, umpu ma.
Efrayim, yaa gànctu,
Israyil laa ne, yaa sobeel sa bopp.
Seeni jëf a leen mayul ñu dellu ci seen Yàlla,
nde ngelawal ngànctoo wale fa seen biir,
te Aji Sax ji, faalewuñu ko.
Israyil, ag reewandeem a ko tiiñal,
Israyil ak Efrayim ñooy fakktaloo seenug ñaawtéef,
Yuda it ànd ak ñoom fakktalu.
Seen jur gu gudd ak gu gàtt lañuy àndal,
di seet Aji Sax ji, duñu ko gis,
te moo leen dëddu.
Aji Sax ji lañu wor,
nde doomi po lañu jur;
Léegi la leen màggalug Terutel weer
di booleek seen suuf, sànk leen.
Yàlla dëkk na Israyil ak Yuda.
«Wal-leen bufta gi ca Gibeya,
jibal liit gi ca Raama
te yéene ca Bet Awen*5.8 Seetal 4.15..
Moytul sa gannaaw, Beñamin.
Efrayim day gental kera bésu mbugal,
maa xamle ci biir giiri Israyil lu wér péŋŋ.
10 Kàngami Yuda mujj mel ni
ñuy toxal màndargam làccu suuf.
Ci seen kaw laay yuri samam sànj nim ndox.
11 Efrayim lees di not,
joggati ay yelleefam,
nde moo dogoo topp yoonu caaxaan.
12 Man nag ni ñaawat laay def ak Efrayim,
te ni sànkar laay def ak Yuda.
13 Ba Efrayim gisee jàngoroom,
Yuda gis ab danaam,
Efrayim a dem Asiri,
yónnee ca Buur Yareb5.13 Yareb man naa tekki «xeexkat.».
Waaye manu koo wéral,
mbaa di ko fajal ab danaam.
14 Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim,
ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda.
Man, man mii maay xotat, wéy,
maay yóbbu te kenn du wallu.
15 Ma daldi ñibbi, ba ñu nangu seenug tooñ,
sàkku ma.
Bu ñu jàqee lañuy daw wutsi ma.»

*5:8 5.8 Seetal 4.15.

5:13 5.13 Yareb man naa tekki «xeexkat.»