Saar 4
1 Su bés baa juróom yaari jigéen ŋoyaalu genn góor, ne ko:
«Sunub dund, nun a,
sunu koddaay, nun a!
Jox nu sag buum rekk,
teggil nu gàcce.»
Aji Sax ji aar na ndesu Yerusalem
2 Su bés baa njebbitum Aji Sax ji
doon lu yànj, darajawu,
meññeefum réew mi di teraanga, dib sag,
ñeel ñi dese bakkan fi Israyil.
3 Su boobaa ku mucc fa Siyoŋ
ak ku des fa Yerusalem,
ku sell ki lees lay wooye,
muy képp ku ñu bind turam,
te mu wara dese bakkan ci Yerusalem.
4 Boroom beey wal noowal mbugal,
noo guy lakk, sellal,
fóote ko jonkani jigéeni Siyoŋ,
fetee ko deret ji ci Yerusalem, ba mu set.
5 Su boobaa tundu Siyoŋ bépp,
fépp fu ñuy dajee,
Aji Sax ji sàkk fa niiru saxar bëccëg,
guddi mu def tàkk-tàkk bu ne ràññ;
leeru Aji Sax ji di kiiraay, tiim lépp,
6 di mbaar mu ñuy serloo tàngooru bëccëg,
di ko seeloob taw ak waame.