Saar 33
Ña daan sànke sànku nañu
1 Wóoy ngalla yaw bóomkat bi kenn bóomul,
yaw workat bi kenn worul.
Boo noppee bóome, ñu bóom la,
te boo noppee wore, ñu wor la.
2 Éy Aji Sax ji, ngalla baaxe nu;
yaw lanu yaakaar!
Xëyeel a dooleel wii xeet,
wallu nu ci biir njàqare.
3 Sam riir jib, xeet yi fëx;
nga jóg, waaso yi fëlxoo.
4 Dees na sëxëtoo sa alal sëxëtoob soccet.
Dees na ko sam ni njéeréer di samee!
5 Aji Sax jee kawe,
moo dëkke fa kawa kaw,
te mooy dajal fi Siyoŋ njekk ak yoon.
6 Liy dalal seen jamono mooy
koomu ndam; xel ak xam-xam,
te ragal Aji Sax ji, loolooy seen alal.
7 Xool-leen seen jàmbaar
ñiy yuuxoo ci mbedd mi,
ndawi jàmm yaa ngii,
di jooyoo jooy yu metti.
8 Yoon yaa ngi wéet,
kenn jaareetul ci ñall wi!
Kóllëre fecciku na,
xeebees na ay seede,
te kenn faaleetul doom aadama.
9 Suuf a ngi maral, wow koŋŋ,
gottub Libaŋ am gàcce, lax,
àllub Saron doon joor gu wow,
garabi Basan ak Karmel yëngu, di ruus.
10 Aji Sax ji nee: «Xaaral rekk ma jóg,
xaaral rekk ma ne ñokket,
xaaral rekk ma teewal samag kawe.
11 Seeni mébét di boob,
bu sottee dim ngooñ;
seen noowug bopp mooy xamb sawara,
wi leen di xoyom.
12 Xeet yeey sànku
ni doj yu lakk ba doon kew,
mbaa taxas yu ñu buub,
sànni ci sawara, mu tàkk.
13 Yeen ñi sore, dégluleen li ma def;
yeen ñi jege, xamleen ne maa am doole.»
14 Bàkkaarkati Siyoŋ tiit nañu,
way-gëmadi yaa ngay lox.
Ana kan ci nun moo mana dal ak
sawara suy xoyome*33.14 sawara: seetal ci 30.27 ak 31.9. ?
Ana kan ci nun moo mana dal ak
taal yu yànj ya dul fey?
15 Xanaa kiy doxe njekk,
di wax njub,
bañ alalu foqati;
loxo bay jalax ab ger,
noppam di tanqamlu waxi bóome,
bëtam di gëmm, ba du gis lu bon.
16 Ku ni mel, bérab bu kawe lay dëkke,
doj yu ñu dàbbli di rawtoom,
dundam doy,
te ndoxam du ñàkk.
Yerusalem mucc na cib noon
17 Yaw mi mel nii, buur bi ci taar bi ngay teg bët;
yaay gis réew mi ne màww.
18 Sam xel dem ca sa tiitaange ja woon,
nga ne: «Moo, ana ka doon waññ?
Ana ka doon natt diisaayu galag?
Ana ka doon waññiy tata?»
19 Su boobaa dootoo gis xeet wii di jaay doole,
xeet wii diisu làkk ba déggeesu ko,
taqu làmmiñ ba xameesul lu ñuy wax.
20 Xoolal Siyoŋ, dëkk ba nuy màggale;
yaay teg bët Yerusalem, dëkkuwaay bu dal ba,
xayma bu deesul sempi,
wewukaay ya deesu ko buddi mukk,
te luy buumu xayma ya it, deesu ko dog.
21 Foofa déy la nu Aji Sax ju màgg ji
di nekkal bérab bu defi dex aki wal,
fu gaalu joow dul dawe,
te gaal gu mag du fa jaare,
22 Aji Sax jee nuy jiite,
Aji Sax jee nuy dogalal yoon.
Aji Sax jeey sunu buur!
Moom moo nuy wallu.
23 Yeen nag seen réew mi gaal la,
gu goj ya yolom,
ponk ba ca digg ba di yëngu,
ba ndimol gaal gi firikuwul.
Dees na séddoo lël ju ne gàññ,
ba làggi ya sax séddu ca.
24 Du kenn ci waa Yerusalem,
ku neeti wopp na.
Waa dëkk bépp ay am njéggalu bàkkaar.