Saar 37
1 Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji. 2 Ba loolu amee mu yebal Elyakim bootalub Buur ak Sebna bindkat ba, ak ñay mag ca sarxalkat ya. Ñu sol saaku yu ñuy ñaawloo, daldi dem ca Yonent Yàlla Esayi doomu Amocc. 3 Ñu ne ko: «Esekiya dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer! 4 Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»
5 Ba surgay Buur Esekiya àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax, 6 Esayi da ne leen: «Waxleen seen sang ne ko: Aji Sax ji dafa wax ne: “Bul ragal kàddu yi nga dégg surgay buurub Asiri ñàkke ma ko kersa. 7 Maa ngii di ko sol xel mu ko gëmloo xibaar bu muy dégg, ba dellu réewam, ma fàdde ko ab saamar ca am réewam.”»
Asiri tooñati na Yuda
8 Gannaaw loolu Rabsake dégg ne buurub Asiri bàyyikoo na Lakis, bay xareek dëkk ba ñuy wax Libna. Mu walbatiku fekki ko foofa. 9 Booba buurub Asiri daa dégg ne Tiraka buurub Kuus moo leen di songsi. Ba mu ca déggee daa yebal ay ndaw ca Esekiya, ne leen: 10 «Waxleen Esekiya buurub Yuda ne ko: “Seen Yàlla ji ngeen yaakaar, bumu leen nax, naa leen deesul teg Yerusalem ci loxol buurub Asiri. 11 Xanaa yaw ci sa bopp dégg nga li buuri Asiri def mboolem réew yi, faagaagal leen? Yaw nag, yaa ciy mucc? 12 Xeet yi samay maam sànk, seeni tuur dañu leena musal, muy Gosan, di Karan, di Resef, di askanu Eden wa woon ca Telasar? 13 Ana buuri Amat ak Arpàdd ak Layir ak Sefarwayim ak Ena ak Iwa?”»
14 Ba Esekiya jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër Aji Sax ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji. 15 Esekiya ñaan Aji Sax ji, ne ko: 16 «Éy Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, Yàllay Israyil mi toog fi tiim serub yi. Yaw doŋŋ yaa di Yàllay mboolem nguuri àddina. Yaw déy, yaa sàkk asamaan ak suuf. 17 Ngalla Aji Sax ji, dékkal sa nopp ba dégg; Aji Sax ji, xippil say gët ba gis, te dégg mboolem kàdduy Senakerib yi mu yóbbante, ngir ñàkke la ko kersa, yaw, Yàlla jiy dund! 18 Aylayéwén Aji Sax ji, buuri Asiree tas mboolem xeet yeek seeni réew, 19 te ñoo sànni seeni yàlla ci sawara it, ndax yooyoo dul Yàlla, xanaa lu nit sàkke loxoom, bant ak doj, ba tax ñu sànk leen. 20 Kon nag Aji Sax ji sunu Yàlla, wallu nook moom, ba mboolem nguuri àddina xam ne yaw doŋŋ yaa di Aji Sax ji.»
Yonent Yàlla Esayi yégle na jéllub Asiri
21 Ba mu ko defee Esayi doomu Amocc yónnee ca Esekiya ne ko: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil, mi nga ñaan ci mbirum Senakerib buurub Asiri, dafa wax ne: 22 Lii moo di kàddu gi Aji Sax ji wax ci moom:
Yaw, janq Siyoŋ mu taaru da laa xeeb,
di la ñaawal.
Yerusalem, dëkk bu taaru booboo
lay wëcc bopp,
di la kekku sa gannaaw.
23 Ana kooy kókkaleek a ñàkke kersa?
Moo kooy yékkatil kàddu?
Kooy xool gëti xeebeel?
Xanaa du Aji Sell ju Israyil ji?
24 Yaa yebal say surga,
di kókkali Boroom bi, te naa:
“Sama watiir yi ne xas
laa ware kawtey tund yi,
jàll ba ca xolu Libaŋ.
Maa gor seedaram ya fa sut
ak tànnéefi garabi sipparam:
maay àkki ba ca collub kaw bu tundu Libaŋ,
ak gottam bu naat ba nib tóokër.
25 Maa gas ay teen, naan,
maa joggatee sama téstën, wali Misra yépp,
ŋiisal ko.”
26 Waaye xanaa déggoo ne bu yàgg laa dogal loolu?
Ca jant yu jëkk ya laa ko nasoon,
tey ma sottal ko,
ba nga mana def genti jali tojit, dëkk yu tata wër.
27 Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox,
mel ni gàncaxu àll mbaa ñax mu yees,
mbete caxum xadd
mbaa tool bu car jógagul.
28 Waaye boo toogee, boo génnee,
boo duggee, xam naa,
boo xadaroo sama kaw it, xam naa.
29 Yaa xadaru sama kaw,
ba sag reewande tàbbi sama nopp!
Maa lay takkal ag nos akug laab,
waññi la, nga dellu yoon wa nga dikke woon.
30 Lii, def ko ci, mu dib takk.
Dees na lekk ren peppum saxayaay,
déwén it dees na lekk lu saxal boppam.
Waaye déwén-jéeg,
ngeen ji, góob,
jëmbat tóokëri reseñ, lekk ca meññeef ma.
31 Ndes wa des ca askanu Yuda
ñooy saxaat ay reen,
ba meññaat ay doom.
32 Yerusalem kay law ndes di génne,
aw ndes ay rëcce tundu Siyoŋ,
te Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
mooy sottal loolu ci xéraangeem.
33 Moo tax Aji Sax ji wax ci buurub Asiri ne:
“Du dugg ci dëkk bii,
du fi soqig fitt,
du fi taxawe ab pakk,
du fi jal jal bu muy gawe!
34 Yoon wa mu dikke lay delloo,
biib dëkk, du fi dugg.
Kàddug Aji Sax jee!
35 Maay aar dëkk bii, musal ko
ngir man ci sama bopp,
ak Daawuda sama jaam bi.”»
36 Ba loolu amee malaakam Aji Sax ji dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew. 37 Ba mu ko defee Senakerib buurub Asiri daldi fabu, ñibbi. Mu toog nag ca Niniw. 38 Gannaaw gi, ba muy sujjóot ca kër tuuram ma ñuy wax Nisrog, Addraameleg ak Sareser, doomam yu góor ñoo ko fa fàdde saamar. Ñoom nag ñu daw làquji réew ma ñuy wax Araraat. Ci kaw loolu doomam Asaradon falu buur, wuutu ko.