Saar 43
Jotkatub Israyil kenn la
1 Léegi nag yaw Yanqóoba,
yaw Israyil mii,
Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne:
«Bul tiit, jot naa la.
Dama laa woo ci sa tur.
Maa la séddoo.
2 Booy xuus cim ndox,
maa ngi ànd ak yaw;
ag dex du la mëdd.
Booy dox cib taal, doo lakk,
sawara du la xoyom.
3 Man Aji Sax ji, maay sa Yàlla;
man Aji Sell ju Israyil,
maa lay musal.
Maa joxe Misra, feye la;
ak Kuus ak Seba, ma weccikoo la.
4 Fonk la, teral la ak sopp la,
moo tax ma joxey nit, weccikoo la;
ay askan dee, wuutu sa bakkan.
5 Bul tiit, yaw laa àndal,
maay jële saw askan penku,
dajalee leen sowub jant.
6 Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!”
ne bëj-saalum: “Bul téye!”
Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi,
te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina.
7 Délloosil képp ku ñu ma tudde,
te sama màqaama tax ma sàkk ko,
tabax ko, sottal ko.»
8 Indileen ñii diy silmaxa te ami gët;
tëx te ami nopp.
9 Na xeet yépp daje,
askan yépp teewandoo.
Ana ku nu ci yégaloon lii xew,
mbaa mu xamal nu la wees?
Na seen seede teew, dëggal leen;
ba ñu dégg leen, ne noonu la.
10 Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede.
Kàddug Aji Sax jee.
Yeenay sama jaam bi ma taamu,
ngir ngeen xam, ba gëm ma,
ba ràññee ne maay moom.
Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu,
mbaa ju may wuutuji.
11 Aji Sax ji, mennum man a;
amul jotkat bu ma moy.
12 Maa dogal ag njot, sottal ko, biral ko,
ba tuuru doxandéem nekkagul seen biir.
Yeen nag, yeenay samay seede.
Kàddug Aji Sax jee.
Man maay Yàlla,
13 maa masa doon kenn ki,
te sama loxo, maneesu cee musle.
Su ma defee, kuy dindi?
14 Aji Sax jiy seen jotkat,
Aji Sell ju Israyil dafa wax ne:
«Yeena tax ma yebal ku songsi Babilon,
ba dàjji lu fay tëjukaay,
ba xaxalooy Kaldeen ñooñu diy jooyoo*43.14 Tekkitel aaya bii am na werante..
15 Maay Aji Sax ji, seen ku Sell ki;
maa sàkk Israyil, di seen buur.»
16 Aji Sax ji dafa wax,
moom mi sàkk yoon biir géej,
rëddu xàll, digg mbeex mu ne xéew;
17 xabtal watiiri xare aki fas,
ak gàngooru ñeyi xare,
ñu bokk tëdd, jógatuñu,
xanaa fey kamaj nib làmp.
18 Mu ne: «Buleen geesu la woon,
buleen seet ca la wees.
19 Maa ngii di def lu yees,
te mu ngii di feeñ xaat!
Ràññeewuleen koo?
Biir màndiŋ mi kay laay xàllu yoon;
fa ne sereŋ, ma walal ay dex;
20 dundooti àll bi di ma sàbbaal,
ñook njabootug bànjóoli,
nde maa mayem ndox fi màndiŋ mi,
dex ya wale fu noon sereŋ,
ma nàndale sama ñoñ, sama tànnéef,
21 xeet wii ma bindal sama bopp,
te ñooy siiwal sama woy.»
22 Moona Yanqóoba, woowuloo ma,
yaw Israyil laa ne, sàppi naa la.
23 Du xar mu ndaw moo ma defal saraxu rendi-dóomal,
mbaa sarax yoo ma terale,
te du sarax su ma la teg it,
mbaa saraxu cuuraay bu ma la sonale.
24 Du xaalis boo ma jëndale barax bu xeeñ,
du nebbonu sarax boo ma reggale.
Xanaa lakkal maak say bàkkaar,
sonal maak say ñaawtéef.
25 Mennum man mii maay far say moy ngir man,
ba dootuma fàttliku bàkkaar.
26 Fàttli ma saw lay, nu bokk layoo;
waxal boog yaw, ndax nga yey!
27 Sa maam a jëkka bàkkaar,
ñi lay teewal teg ca gàntal ma,
28 ba tax ma sobeel kilifay kër gu sell gi,
araamal Yanqóoba,
wacce Israyil ŋàññi noon.