Saar 49
Surgab Aji Sax ji mooy leeru xeet yi
Yeen waa duni géej, dégluleen ma;
yeen askan ya fu sore, teewluleen ma.
Fa sama biiru ndey la ma Aji Sax ji wooye,
moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul.
Moo ñawal sama kàddu ni saamar,
làqe ma keru loxoom.
Moo ma def may fitt gu ñaw,
yeb ma ci mbuusum fittam.
Moo ma ne: «Israyil yaa di samab jaam,
yaw laay wonee samag leer.»
Man nag ma noon:
«Maa sonn ci dara,
coonob cóolóol bu amul njariñ.»
Teewul sama àttee nga fa Aji Sax ji,
sama yool a nga fa sama Yàlla.
Tey Aji Sax jee wax,
moom mi dale sama biiru ndey,
mooñ ma, ma dib jaamam
bi koy waññil askanu Yanqóoba ba ca moom,
dajaleel ko bànni Israyil googu fa moom,
ba jagoo teraangay Aji Sax ji,
sama Yàlla jii di sama doole.
Mu ne: «Xeeb naa li ma la sas ngay sama jaam
biy siggil giiri Yanqóoba,
te wara délloosi ndesu Israyil gii.
Tabb naa la, ngay leeru xeet yi,
di jotale waa cati àddina sama wall.»
 
Aji Sax ji jotkatub Israyil,
moom ku Sellam ki,
moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko,
te muy surgawu kilifa yi,
mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg,
ay kàngam di sukk,
ngir Aji Sax ji boroom worma,
ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.»
Aji Sax ji dafa wax ne:
«Bu bésub yiw taxawee, ma nangul la;
bu bésub mucc jotee, ma wallu la,
sàmm la,
def la ngay kóllëre sama digg ak askan wi,
ngir yékkatiwaat réew mi,
séddalewaat ay cér, suuf sii gental tey,
ba ne ñi ñu tëjoon: “Génnleen!”
Fa ñu nekkoon cig lëndëm,
laa naa leen: “Génnleen ci leer gi!”
Ñooy doon sama gàtt, dellu di fore aw ñall,
ak wépp tund wu ne faraas tey.
10 Duñu xiif, duñu mar;
tàngooru mbóoya akub jant du leen sonal,
nde ki leen ñeewantee leen di wommat,
di leen yóbbu fu ndox bënne.
11 Sama tund yépp laay soppiy yoon,
sëkkaat samay mbedd.
12 Ñu ngiy bawoo fu sore,
ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu,
ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.»
13 Asamaanoo sarxolleel, suufoo bégal,
te tund yi xaacoondoo!
Aji Sax jee dëfal ñoñam,
moo ñeewante néew-ji-dooleem ñii.
 
14 Siyoŋ a nga naa: «Aji Sax ji wacc na nu,
Boroom bi fàtte na nu!»
15 «Ana jaboot juy fàtte doomam juy nàmp,
mbaa muy néege ku mu jur ci biiram.
Bu ko manoona fàtte it,
man duma la fàtte.
16 Sama biir loxo yii laa la ñaas,
say tataa janook man ba fàww.
17 Ñi lay tabaxaat dañuy gaaw,
te ñi la yàqteek ñi la gental
dañuy dem, ba la.
18 Séentul fi la wër te xool!
Ñépp a ngi daje, di la fekksi.
Ndegam maay Kiy Dund,»
kàddug Aji Sax jee,
«ñoom ñépp ngay takkoo ni gànjar,
gooy gànjaroo nib séet.
19 Sa gentub tey bi déy a ngi wéet,
di réew mu yàqu yaxeet.
Waaye léegi déy mu fees ba far xat;
fu ña la sànkoon di soree.
20 Ñàkkoon ngay doom,
waaye ku nekk ci say doom ay dëkkalaat
yii kàddu ci sab nopp:
“Fii dafa xat,
xajal ma, fu ma dëkke!”
21 Dangay mujj naa:
“Moo, ku ma jural ñii ñépp?
Man mi ñàkkooni doom, manumaa jur,
ñu toxal ma, wacc ma;
ana ku leen yoroon te ma des, man kenn?
Ñii sax, fu ñu ne woon?”»
22 Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne:
«Maa ngii di tàllal xeeti jaambur ñi loxo,
ñee ma yékkati raaya, wooye leen;
ñu fab say doom yu góor, indi,
tungóom sa doom yu jigéen, délloosi;
23 Yaw la ay buur di baayoo,
seeni lingeer di la nàmpal.
Ñoo lay sujjóotal,
di la maral say tànk,
ba nga xam ne maay Aji Sax ji,
te ku ma yaakaar du rus.»
 
24 Manees naa foqati alalu sëxëtoo ci loxol jàmbaar a?
Am manees naa rëcc boroom doole bu la jàpp?
25 Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Moona dees na foqati ku jàmbaar jàpp,
ba rëccal alalu sëxëtoob boroom doole.
Say jotewaale, maay joteek ñoom,
te say doom, maa leen di wallu.
26 Ñi lay néewal, maa leen di leel
seen suuxu bopp.
Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen,
ba kuy boroom suux xam ne
maay Aji Sax ji lay wallu,
jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»