Saar 56
Xeet yépp la Aji Sax jiy ñoñoo
1 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Sàmmleen yoon, di def njekk.
Sama wall kat a ngi dikk léegi,
sama njekk laa ne, léegi mu teew.
2 Ndokklee kuy jëfe lii,
ndokklee doom aadama ju jàppoo lii,
di sàmm bésub Noflaay,
bañ koo ñàkke worma,
di sàmm loxoom ci jépp jëf ju bon.»
3 Doomu doxandéem bu jokku ci Aji Sax ji,
bumu ne: «Aji Sax jee may beddee beddi ci ñoñam.»
Jaam bu ñu xañ ngóora it bumu ne:
«Man garab gu jaasir doŋŋ laa.»
4 Aji Sax ji kat dafa wax ne:
«Jaam yi ñu xañ ngóora,
su ñu sàmmee sama bési Noflaay,
taamu sama coobare,
tey feddli sama kóllëre,
5 maa leen di may ci sama biir kër, sama biir ëtt,
doj wu ñu leen di fàttlikoo
ak tur wu leen di gënal doom yu góor ak yu jigéen.
Tur wu sax dàkk laay may
jaam yi ñu xañ ngóora,
te du fey mukk*56.5 Seetal ci Sarxalkat yi 21.16-20..»
6 Doomi doxandéem yi ànd ak Aji Sax ji,
ngir liggéeyal ko,
ngir sopp turu Aji Sax ji,
te di ay jaamam,
muy képp kuy sàmm bésub Noflaay,
baña ñàkke worma bés bi,
xanaa di feddli kóllëreem,
7 mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu
sama kaw tund wu sell,
bànneexale leen sama biir kërug ñaan,
seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax,
dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay,
ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”,
ñeel xeetoo xeet.»
8 Kàddug Boroom bi Aji Sax jaa ngi,
kiy dajale giiri Israyil yi tasaaroo,
mu ne: «Maay dajaleeti,
dolli ca la ma dajale woon.»
Ab daan ñeel na njiit yi
9 Yeen rabi àll yi,
dikkleen ci bernde ji,
yeen rabi gott bi yépp.
10 Jongrukati Israyil yépp a silmaxa,
te xamuñu dara.
Ñoom ñépp a diy xaj yu luu,
manuñoo baw,
xanaa tëdd di jeneer,
soppi nelaw.
11 Xaj yu tiita tiit lañu,
xamuñu suur,
te ñooy sàmm yeey!
Ñoom ñépp, kenn manu cee xam dara,
seen yoonu bopp lañu topp,
ak seen amin wu lewul.
12 Ña nga naa: «Dikkleen, ma indi biiñ,
nu màndeew ñoll; tey ak ëllëg;
li fi des du jeex.»