Saar 60
Leer dina fenkal Yerusalem
1 Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na;
teddngay Aji Sax ji fenkal na la!
2 Lëndëm gaa ngii di muur àddina,
mu ngi guddil askan yi,
te yaw, Aji Sax ji fenkal la,
leeru teddngaam feqal la.
3 Ay xeet ay fekksi sag leer,
ay buur wutsi sa ceeñeeru njël.
4 Séentul fi la wër ba gis:
ñoom ñépp a daje, di la fekksi,
sa doom yu góor a dikke fu sore,
te sa doom yu jigéen it
dees leena fab, indaale.
5 Yaa koy gis, sa kanam ne ràññ,
fit tëf-tëfi, xol fees dell,
nde dees na walbati xéewali géej, indil la,
alali xeet yi dikkal la.
6 Ndiiraanu giléem a lay fees
ak njëggi Majan ak Efa,
ñoom ñépp sëfe Saba.
Dees na indi wurus ak cuuraay
tey kañaale Aji Sax ji.
7 Gétti Kedar yépp a lay dajesil,
kuuyi Nebayot di la jariñ,
te di sarax yu dajeek ngërëm
ci kaw sarxalukaayu Aji Sax ji,
ma di ko darajaale sama teddngay kër.
8 Ana ñuy ñii di naaw niy niir,
nirook ndiiraanu pitax yu jëm seeni tàgg?
9 Waa dun ya déy a nga may séentu,
gaali Tarsis yu mag yaa nga jiitu,
jële fu sore sa doom yu góor ya,
indaale seen xaalis ak seen wurus,
ngir sa Yàlla Aji Sax ji,
Aji Sell ju Israyil ji la teral.
10 Ay doomi doxandéem ay tabaxaat say tata,
seeni buur di la surgawu.
Maa meroon, duma la,
maa la baaxe, yërëm la.
11 Say wunt ay ubbiku saa su ne,
guddeek bëccëg, du tëje,
xanaa di la jàlleel alali xeet yi,
seeni buur riixle ànd ca.
12 Mu diw xeet, dim réew,
ku la ci nangulul sànku.
Xeet yooyu yépp ay yàqu yaxeet.
13 Taaru àllub Libaŋ a lay ñibbsil,
garabu sippar, pẽe ak geneen gu dëkke naat,
taaralsi sama kër gu sell gi,
ba ma terale ci sama ndëggastalu tànk.
14 Ña la daa néewal,
seeni doom a lay sukkalsi.
Ña la daa ñàkke worma,
mujj di fóon say tànk.
Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji»,
mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.»
15 Dees laa foñ, jéppi la,
ba kenn jaareetu fi.
Waaye maay def ñu di la sagoo ba fàww,
di la bége sët ba sëtaat.
16 Yaay naan soowum xeet yi,
nàmp weenu buur yi,
ba xam ne maay Aji Sax jiy walloo,
jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.
17 Maay wuutale xànjar, wurus;
wuutale weñ gu ñuul, xaalis;
bant, xànjar;
doj, weñ gu ñuul.
Jàmm laay def mu jiite la,
def njekk yilif la.
18 Deesatul dégg ci sam réew:
«Fitna ñëw na!»
deesatul dégg it fi sa kemu suuf:
«Yàqute ak Yàqulee ngi!»
«Mucc» ngay tudde say tata,
te «Cant» ngay tudde sa bunti dëkk.
19 Du jant a lay leeralati bëccëg,
te weer du la niital;
Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww,
sa Yàlla jooju di sab taar.
20 Sab jant du sooti,
sa weer du suuxati.
Aji Sax jeey doon sag leer ba fàww,
sa fani ñaawlu jeex.
21 Sa askan wépp ñu jub lañuy doon,
te ñooy moom réew mi ba fàww.
Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp,
sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.
22 Ki ci gëna tuut ay meññ junni,
ki ci gëna néew jur xeet wu mag.
Man Aji Sax ji, bu lii jotee,
ma gaaw koo sottal.