Saar 2
Gënaatle warul
Bokk yi, bu leen di gënaatle te di gëmkati sunu Sang Yeesu Almasi, Boroom leer. Ndax su nit duggsee seenum ndaje, takk jaarob wurus, solu ba jekk; ku néew doole it duggsi, limboo ay sagaram, su ngeen seetloo boroom col gu jekk gi, ne ko: «Toogeel fii, moo baax ci yaw,» te ne néew-ji-doole ji: «Yaw, taxaweel nee, mbaa nga toog fii sama tànki toogu, fi suuf,» su boobaa xanaa du yeena ngi gënaatle ci seen biir, tey àttee ay mébét yu bon?
Bokk yi, soppe yi, dégluleen. Xanaa du Yàlla moo taamu ñi àddina jàppe ñu néew doole, ngir ñu barele ngëm, boole ci jagoo nguur, gi Yàlla dig ñi ko sopp? Yeen nag ngeen di teddadil néew doole yi! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noggatu, di leen diri ba fa mbaxana dee benn? Xanaa du ñooñu ñooy ñàkke kersa tur wu tedd wi ngeen di wuyoo?
Ndegam nag yoonu Buur Yàlla ngeen matal sëkk, di sàmmonteek Mbind mi ne: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom*2.8 Seetal ci Sarxalkat yi 19.8.,» su boobaa waawleen góor! Waaye su ngeen gënaatlee, bàkkaar ngeen, te yoon topp na leen, ndax yeena ko xëtt. 10 Ndax kat képp ku sàmm yoon wépp, ba mu des lenn ndigal doŋŋ lu mu tërëfe, ab daanu ku moy yoon wépp ñeel na ko. 11 Ndax ki ne: «Bul jaaloo,» moo ne itam: «Bul bóome2.11 Seetal ci Mucc ga 20.13, 14..» Ku jaaloowul te bóome nag, xëtt na yoon. 12 Deeleen waxe tey jëfe ni mu jekke ci nit ñu ñuy séddeji àtteb yoon wiy goreel. 13 Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.
Gëm, jëfe
14 Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal? 15 Su mbokk mu góor mbaa jigéen raflee, mbaa mu ñàkk lu mu dunde bés bu nekk, 16 ba kenn ci yeen ne mbokk mi: «Demal ak jàmm, solul nag te lekk ba regg,» te fajul aajoom, loolu lu muy jariñ? 17 Noonu la ngëm deme, su amul jëf ju mu àndal, ngëm gu dee la.
18 Waaye jombul nit ne: «Yaw, ngëm nga am, waaye man, jëf laa am.» Dama ne, won ma sa ngëm gu àndul ak jëf; man, samay jëf laa lay wone sama ngëm. 19 Yaa gëm ne Yàlla kenn la; waaw góor, waaye rab yu bon yi it loolu lañu gëm bay lox.
20 Yaa ñàkk bopp, dangaa bëgg lu la firndeel ne ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ? 21 Sunu maam Ibraayma, xanaa du ci jëf lees ko joxe àtteb ku jub, ndax jëf ja mu jooxee doomam Isaaxa ca sarxalukaay ba? 22 Kon gis nga ne ngëm gaa liggéeyandoo ak jëfam ja, te ca jëf ja la ngëm ga mate sëkk. 23 Mbind ma daldi sotti, na mu dikke woon ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, ñu waññal ko ngëmam ag njub2.23 Seetal ci Njàlbéen ga 15.6.,» ba ñu di ko wooye xaritu Yàlla. 24 Ngeen gis kon ne ci jëf lees di joxe nit àtteb ku jub, waaye du ci kaw ngëm doŋŋ.
25 Xanaa du noonu it lañu joxe Raxab§2.25 Seetal ci Yosuwe 2:1-21. gànc ba, àtteb ku jub, ci kaw jëfam, ndax la mu dalaloon ndawi Yawut ya, ba awale leen feneen? 26 Yaram wu àndul akug noo daal, ni mu deeye, noonu la ngëm gu àndul aki jëf, deeye.

*2:8 2.8 Seetal ci Sarxalkat yi 19.8.

2:11 2.11 Seetal ci Mucc ga 20.13, 14.

2:23 2.23 Seetal ci Njàlbéen ga 15.6.

§2:25 2.25 Seetal ci Yosuwe 2:1-21.