Saar 3
Tuub jot na
Mu ne: «Su waay fasee jabaram,
mu dem doon jabaru keneen,
Su waa ja jëlaatee ndaw sa ëllëg,*3.1 Yoonu Musaa mayul ku fase jabaram mu di ko jëlaat, gannaaw bu séyaatee ba tas. Seetal ci Baamtug yoon wi 24.1-4.
Loolu du sobeela sobeel réew mii?
Moona yeen gànctu ngeen aki fari far,
Ana nu ngeen mana délsee fi man?»
Kàddug Aji Sax jee.
 
«Téenleen, séentu tund3.2 tund: kaw tund yooyu lañu daan jaamoo tuur yi ñu foogoon ne dañuy nangul am njur. ya ne faraas!
Ana fu ñu leen fi tëddewul?
Ci yoon yi ngeen di yeeroo
ni màngaan muy dogalee ci màndiŋ mi.
Sobeel ngeen réew meek seen gànctook seenug mbon.
Moo tax waame aje,
taw yiy mujje dikkul.
Teewul ngeen dëgër bët nib gànc,
ñàkk gàcce!
Léegi ngeen di ma woo wall naa:
“Baay, yaay sama xejj ca ba may ndaw.
Xanaa deesul mer ba fàww?
Xanaa xadar du sax?”
Ma ne: “Israyiloo, yeena ko wax,
waaye bon ngeen lu ngeen man.”»
Israyil woyof kumba, Yuda toogadi
Aji Sax ji nag wax ma ci jamonoy buur Yosya ne ma: «Gis nga li Israyil Woyof-Kumba-si def? Di dem kaw tundoo tund ak ker garaboo garab gu naat, di fa gànctu. Ma noon su ma defee loolu lépp ba noppi, dina délsi, te délsiwul. Te doomu ndeyam Yuda workat bi gis na ci. Gis naa ne it Israyil Woyof-Kumba-si gànctu na ba ma yebal ko, jox ko kayitu pase, mu dem, te taxul doomu ndeyam Yuda workat bi ragal. Moom it daa dem di gànctu. Ni gànctu yombe Israyil tax na réew mi sobewu. Njaaloo naak yàllay doj, njaalook yàllay bant. 10 Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee. 11 Aji Sax ji nag ne ma: «Li Israyil di woyof kumba lépp sax moo tane Yuda workat bi. 12 Demal yéeneji kàddu yii fa bëj-gànnaar. Nga ne:
“Israyiloo, Woyof-Kumba, délsil.”
Kàddug Aji Sax jee.
“Duma la fasal kanam.
Man Boroom ngor laa,
te duma jàpp mer ba fàww.”
Kàddug Aji Sax jee.
13 “Nangul ne ñaaw nga rekk,
te man sa Yàlla Aji Sax ji nga tooñ,
di wër di foye sa bopp ak yàllay doxandéem yi
ci ker garaboo garab gu naat,
te dégluwoo ma.”»
Kàddug Aji Sax jee.
14 «Yeen doom yu woyof kumba yi, délsileen.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maay seen boroom kër,
maay jële kenn ci bii dëkk,
ñaar ca bee gox,
boole indi Siyoŋ,
15 tànnal leen sàmm yu ma doy,
ñu sàmme leen xam-xam akug muus.
16 Janti keroog bu ngeen baree ba giir ci réew mi,
deesul waxe gaalu kóllërey Aji Sax ji3.16 gaalu kóllërey Aji Sax ji moo doon firndeel teewaayu Aji Sax ji ci digg bànni Israyil.;
xel dootu ci dem,
deesu ko fàttliku sax,
te deesu ko namm,
deesu ko sàkkati sax.»
Kàddug Aji Sax jee.
17 «Janti keroog
Yerusalem, ngànguney Aji Sax ji lees koy wooye,
xeetoo xeet di fi daje,
ngir Aji Sax, ji turam ñeel Yerusalem,
te dootuñu të ticc ci seen mébét yu bon.
18 Janti keroog waa kër Yuda
ànd ak waa kër Israyil,
bawoondoo réewum bëj-gànnaar,
wuti réew ma ma séddoon seeni maam.
 
19 «Maa leen naroona teral ni doom yu góor,
may leen suuf su xemmemlu,
ngeen gënle xeet yépp suuf.
Ma noon dingeen ma wooye baay
te dungeen ma dëddu mukk.
20 Teewul, yeen waa kër Israyiloo, ngeen wor ma,
ni as ndaw di wore faram.»
Kàddug Aji Sax jee.
21 «Coow dégtu na kaw tund ya ne faraas,
bànni Israyil ay jooy ak a tinu.
Ñoo lajj seenu yoon,
fàtte seen Yàlla Aji Sax ji.
22 Yeen doom yu woyof kumba yi,
waññikuleen, ma fajtal seen woyof kumba.»
Kàdduy tuub jib na
Nu ngi nii fekksi la,
yaw kay yaay sunu Yàlla Aji Sax ji.
23 Naxi neen kay lañu jële ca xërëmi tund yu ndaw ya
ak coowal kaw tund yu mag ya.
Muccu Israyil kay, fi sunu Yàlla Aji Sax ji.
24 Ba ñuy gone ba tey,
tuur mu ruslu maa ngi neenal ñaqu maam yi,
seen jur gu gudd ak gu gàtt,
ba ci seeni doom, góor ak jigéen.
25 Nan gapproo sunu gàcce,
sàngoo sunu toroxte.
Nook sunuy maam déy,
ba ñuy gone ba tey jii,
nu ngi tooñ sunu Yàlla Aji Sax ji,
te déggalunu sunu Yàlla Aji Sax ji.

*3:1 3.1 Yoonu Musaa mayul ku fase jabaram mu di ko jëlaat, gannaaw bu séyaatee ba tas. Seetal ci Baamtug yoon wi 24.1-4.

3:2 3.2 tund: kaw tund yooyu lañu daan jaamoo tuur yi ñu foogoon ne dañuy nangul am njur.

3:16 3.16 gaalu kóllërey Aji Sax ji moo doon firndeel teewaayu Aji Sax ji ci digg bànni Israyil.