Saar 6
Gawub Yerusalem nuyoo na
«Yeen askanu Beñamin, fëxleen,
génn Yerusalem.
Wal-leen liit gi fa Tekowa,
jafaleleen jum yi Bet Kerem, artoo ko,
musiba kat a ngi yëre bëj-gànnaar,
di safaan bu réy.
Yaw Siyoŋ, dëkk bu taaru bi te xejj,
dama lay dammat.
Ay sàmm ak seeni gétt ci sa kaw,
ñu samp seeni xayma, wër la,
di foral, ku nekk ak pàccam.
Ñii ne: “Waajal-leen xare baak ñoom,
nu songi leen digg bëccëg.
Waaye wóoy nun, jant a ngi lang,
keru ngoon di law!”
Ñee ne: “Nan song congum guddi boog,
ba rajaxe seen kër yu yànj.”»
 
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy da ne:
«Gorleeni bant,
sëkke Yerusalem, gaw ko!
Dëkk bii dees koy mbugal,
àqu noteel la fees dell.
Ni bëtu ndox di dawe,
ni lañuy dawale seenug coxor.
Fitnaak salfaañooy riir ci dëkk bi,
gisuma lu moy jagadeek loraange!»
«Yeen waa Yerusalem, deeleen dégg
bala ma leena dëddu,
ba gental réew mi
gent bu kenn dëkkul.»
Askan wa të na
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne:
«Nañu witta witt ndesu Israyil,
ni ñuy witte reseñ,
ba nga dawalaat say loxo ca car ya.»
Yeremeey wax
10 Moo kan laay waxal,
àrtu ko ba mu déglu,
yii boroom noppi paaxee tëë teewlu!
Kàddug Aji Sax jaa ngii,
mel ni lu ñu rus,
lu ñu safoowul!
 
11 Maa ngi meral Aji Sax ji ba fees
ba manatuma koo dékku.
Aji Sax ji nee: «Sippi ko tuut-tànk yi ci mbedd mi,
sippiwaale ko waxambaane yi daje,
mu laawaale jëkkër ak jabar,
mag ak màggat,
12 seeni kër doon alali jaambur,
ak seeni tool it ak seeni jabar.
Maay xàcci sama loxo déy,
dal ci kaw waa réew mi.»
Kàddug Aji Sax jee.
13 «Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag,
ñépp a ngi lewal lu lewul.
Yonent akub sarxalkat,
ñépp a ngi wor.
14 Sofental nañu sama pajum ñoñ ñi dammtoo,
naan: “Jàmm, lépp jàmm!”
te jàmm amul.
15 Ñu wara am gàcce ci seen jëf ju siblu,
te gàcce gàcceelu leen.
Xamuñu sax luy kersa!
Moo tax ñuy fëlëñoondook ñiy fëlëñu.
Kera ba ma leen di dikkal, ñooy tërëf.»
Aji Sax jee ko wax.
Pexey askan wi jur na musiba
16 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Taxawleen ca selebe yoon wa, xool,
te laajte yoon ya woon,
ne: “Ana yoonu mbaax?”
Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.»
Ñu lànk ne: «Awunu ca.»
17 «Ma tabbal leeni wattukat
ne: “Teewluleen liit gu jib.”»
Ñu lànk ne: «Teewluwnu.»
18 «Moo tax yeen xeet yi, dégluleen;
yeen waaso yi, seedeleen liy xaar ñii.
19 Yeen waa àddina, dégluleen!
Maa ngii di indil askan wii musiba,
seeni pexe jural leen.
Ñoo faalewul samay kàddu,
gàntal sama yoon.
20 Lu may doye lii?
Ndàbb lu jóge Saba*6.20 Saba am réew la wu bokk ci sowu Arabi, fa féete suuf.,
diw gu xeeñ, bawoo réew mu sore?
Seeni saraxi rendi-dóomal safu ma;
seen saraxi jur, bugguma.»
21 Moo tax Aji Sax ji wax ne:
«Maa ngii di tegal askan wii
ay pakk, ñu fakkastaloondoo,
baay ak doom,
dëkkandook ub xarit,
ñépp sànku.»
Noon sàqee na bëj-gànnaar
22 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Aw askan a ngii bàyyikoo réewum bëj-gànnaar,
xeet wu mag lañuy doon, sàqee fa cati àddina.
23 Fitt aku xeej lañuy ŋëb,
néeg lool, duñu yërëm;
seen coow ni riirum géej,
ñu war seeni fas, rëpptal,
làng-déral leen,
yeen waa Siyoŋ, dëkk bu taaru bi.»
Waa Yerusalem ay wax
24 «Danoo dégg riir mi,
sunuy yoxo yoqi,
njàqare ne nu taral,
ni mititu mat.
25 Kii naa: “Bul génn ci àll bi!”
Kee naa: “Bul jaar ci yoon wi!”
Saamar kay a nga ca loxol noon ba,
tiitaange dajal fépp!»
Yeremeey wax
26 Éey bokk yi, sol-leeni saaku,
diwoo dóom, ñaawloo ko.
Ñaawluleen ni kuy dëj benn bàjjo
te jooy jooy yu metti,
nde yàqkat bi day jekki,
ne sunu kaw dàll!
Yàllaay wax
27 «Maa la def sama nattukatu ñoñ,
nga di leen nattu ni ñuy nattoo xaalis,
te war leena seetlu, nemmiku seen jikko.»
Yeremeey wax
28 Ñoom ñépp a di fippukat yu fétteeral,
wër di sos,
dëgërle ni xànjar ak weñ gu ñuul.
Ñoom ñépp di yàqkat.
29 Tëgg wal taalam, mu yànj;
sawara seeyal beteex.
Xellees na koo xelli ci neen,
taxul li ci bon génn.
30 Dees na leen wooye mbuubitum xaalis,
nde Aji Sax ji buub na leen, sànni.

*6:20 6.20 Saba am réew la wu bokk ci sowu Arabi, fa féete suuf.