Saar 15
Aji Sax ji àddu na
Aji Sax ji nag ne ma: «Musaa ak Samiyel sax, bu ñu taxawoon fi sama kanam, du tax ma faale askan wii. Dàqal, ñu sore ma, te wéy. Bu ñu la laajee ne la: “Fu nu jëm?” nga wax leen ne leen:
“Aji Sax ji dafa wax ne:
Kiy wopp dee, wopp dee;
kiy deeye saamar, deeye saamar;
kiy deeye xiif, deeye xiif;
kiy duggi ngàllo, duggi ngàllo.”
«Te dinaa wàcce fi seen kaw ñeenti xeeti duma.» Kàddug Aji Sax jee. «Saamar di bóom; xaj diri yóbbu, njanaaw ak rabu àll for, mu jeex. Dama leen di def, waa réewi àddina yépp, ku leen ci xool rasu. Te li ko waral di Buurub Yuda, Manase miy doomu Esekiya, ak li mu def ci digg Yerusalem.»
Mbugalu Yuda du jaas
Yàllaay wax
«Yerusalemee, ku lay yërëm?
Ku lay jooy?
Moo, ku lay geesu ne la: “Jàmm nga am?”
Yaw yaa ma wacc,» kàddug Aji Sax jee,
«dellu gannaaw,
ma duma la, sànk la.
Muñ naa ba sonn.
Maa leen bees ni ñuy beesem pepp
ci pénci réew mi.
Maa sànk sama ñoñ,
faat seeni doom,
ndax tuubuñu seeni jëfin.
Seeni jëtun laa ful,
ba ñu ëpp suufas géej,
ma indil leen pàddum njolloor,
mu reyal yaay doomi waxambaaneem,
këpp ko tiitaangeek njàqare.
Yaayu juróom yaari góor loof, di àppaat,
jantam sowe bëccëg ndarakàmm,
yaakaar tas, mu jàq,
seenu ndes, ma leel saamaru noon.»
Kàddug Aji Sax jee.
Aji Sax ji feddli na yebam
Yeremeey wax
10 Wóoy saa ndey,
loo ma doon jure!
Man mi réew mépp di xulook a layool,
leblewma, lebuma;
te ñépp di ma móolu.
11 Ndaxam Aji Sax ji nee:
«Maa lay xettli déy, ngir sottal lu baax;
maa la defal sa noon di la tinu déy,
ci janti safaan ak njàqare.»
Yàllaay wax ak Yerusalem
12 «Ku mana toj weñ gu ñuul,
rawatina yetu weñu bëj-gànnaar, mbaa xànjar?
13 Yeen waa Yuda, seen alal ak seeni denc
laay jox ñu ko sëxëtoo te feyuñu
ndax seen gépp moy ci seen réew mépp.
14 Maa leen di def seen jaami noon
réew mu ngeen xamul,
sama mer jippét, tàkkal leen.»
Yeremeey wax
15 Yaw déy Aji Sax ji, xam nga!
Ngalla bàyyi ma xel, geesu ma;
feyul ma ñi ma sam.
Bu leen muñal ba sànk ma!
Xamal ne yaa ma tax di dékku saaga.
16 Sa kàddu laa gis, di ko dunde,
sa kàddu di ma bégal, bànneexal sama xol.
Yaw Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déy,
sa tur lañu ma tudde.
17 Masumaa toogandook ñiy mbumbaay
bay xawaare.
Yaa ma jiite, ma beru, toog
ndax mer mi nga ma sol, ba ma fees.
 
18 Moo sama tiis wi du dakk a?
Bii góom bu metti, tëë wér!
Yaw kay yaay waltan muy wal, di ŋiis,
di tas sama yaakaar.
 
19 Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne:
«Soo délsee, ma délloosi la,
nga dellu di ma liggéeyal.
Soo dee wax ngëneel
lu soreeki caaxaan,
dinga mel ni yaay sama làmmiñ,
te nit ñeey délsi ànd ak yaw,
waaye du yaay délsi ànd ak ñoom.
20 Maa lay def nga mel ak askan wii
ni tatay xànjar ju ñu dàbbli,
ñu di la song
te duñu la man.
Maay ànd ak yaw,
di la wallu, di la xettli.»
Kàddug Aji Sax jee.
21 «Ab soxor jàpp la, ma àtte;
ab néeg ne la céex, ma foqati.»