Saar 17
Aji Sax ji sikk na Yuda
«Bàkkaaru Yuda lañu binde xaccug weñ
gu cat la di doj wu dëgër.
Dees koo ñaas ci seen àlluway xol,
ñaas ko ci seen béjjéni sarxalukaay.
Seeni doom sax di bàyyi xel seeni sarxalukaay
ak seen xer yi ñuy màggale tuurum Asera
fi ker garab yu naat yeek
kaw tund yu mag yi
ak kaw tund yi ci àll bi.
Seen alal ak seen denc yépp
laay joxe, ñu lël ko,
booleek seen jaamookaay
ndax seen moy yi dajal réew mi.
Dingeen xañ seen bopp cér bi ma leen séddoon,
ma def leen seen jaami noon
ci réew mu ngeen xamul,
ndax merloo ngeen ma
mer mu dul fey mukk.»
Aji Sax jee jara yaakaar
Aji Sax ji dafa wax ne:
«Alkànde ñeel na ku yaakaar doom aadama
ak képp kuy doolewoo nit,
dëddu Aji Sax ji.
Day mel ni gajjub ndànd-foyfoy,
du gis ngëneel luy dikk!
Day dëkke màndiŋ mu wow koŋŋ,
suufas xorom su kenn dëkkul.
Waaye barke ñeel na ku wóolu Aji Sax ji,
yaakaar Aji Sax ji.
Day mel ni garab gu saxe wetu ndox,
lawal ay reenam ca wal ma,
ragalul tàngoor wu dikk,
xob ya di naat.
Du tiit atum maral,
du ñàkk meññeef.»
 
«Dara gënula dëng xelum nit,
laago la ci moom.
Ana ku ko mana xam?
10 Maay Aji Sax jiy seetlu xel,
natt ub xol,
di yool ku nekk jëfinam,
la yellook añam.
11 Kuy jagoo alal ju lewul,
mooy picc mu toj lu mu nenul.
Kookooy tollu digg dooleem, alal ja dëddu,
mu mujje dof.»
Yeremeey wax
12 Sunu bérab bu sell bi,
mooy ngànguney daraja, daa masa kawe.
13 Yaw Aji Sax ji yaakaaru Israyil,
ku la wacc, torox;
ku la dëddu daa repp.
Moo wacc Aji Sax ji, bëtu ndox miy dund.
Yeremi ñaan na Yàlla wall
14 Éy Aji Sax ji, faj ma, ma faju;
musal ma, ma mucc,
samag cant, yaw a.
15 Ñu ngii naa ma:
«Ana la Aji Sax ji waxoon?
Na dikk boog!»
16 Man de, bañuma laa sàmmal, topp la;
bésub tiis it dagaanuma ko.
Yaw de xam nga ko.
Li ma wax it fi sa kanam la.
17 Bu ma teg tiitaange,
yaay sama rawtu bésub safaan.
18 Ngalla gàcceelal ñi ma topp,
te bu ma gàcceel;
yal nañu tiit, ñoom,
te man, ma baña tiit.
Rikk dikke leen bésub safaan,
rajaxe leen ñaari yoon.
Bésub Noflaay ñeel na Aji Sax ji
19  Aji Sax ji da maa wax ne ma: «Demal taxawi ca buntu Doomi réew mi, fa buurub Yuda di duggeek a génne. Te nga taxaw itam ca mboolem bunti Yerusalem ya ca des. 20 Nga ne leen: “Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen buuri Yuda ak yeen waa Yuda gépp ak képp ku dëkk Yerusalem, di jaare bunt yii. 21 Aji Sax ji dafa wax ne: Moytuleen seen bopp ba baña gàddu lenn bésub Noflaay, di ko jaarale bunti Yerusalem. 22 Buleen génne seeni kër lenn bésub Noflaay te buleen ci liggéey lenn. Waaye nangeen sellal bésub Noflaay, muy la ma santoon seeni maam. 23 Ndaxam dégluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa të ticc, baña dégg, di gàntal ndigal. 24 Waaye su ngeen ma dégloo ba déglu ma, kàddug Aji Sax jee, baña gàddu lenn di jaare bunti dëkk bii bésub Noflaay, xanaa di sellal bésub Noflaay, bañ cee liggéey lenn, 25 su boobaa buur yiy tooge jalub Daawuda, tey dawal watiir aki fas, ñook seeni kàngam, duñu noppee jaare bunti dëkk bii, feggook seeni kàngam. Waa Yudak waa Yerusalem it di jaare ci bunt yii, dëkk bi sax dàkk. 26 Dees na bàyyikoo dëkki Yuda ak li wër Yerusalem ak diiwaanu Beñamin, ca suufu tundu waak kaw tund ya, ak ca diiwaanu Negew. Ñuy indi ci kër Aji Sax ji ay saraxi rendi-dóomal ak yeneen saraxi jur ak saraxu pepp ak cuuraay. Ñii di indi kër Aji Sax ji saraxi cant. 27 Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”»