Yeremi yéene na yeeslug jàmm
Saar 30
(Saar 30—33)
Nii la yéene bi tënkoo
Kàddu gii dikkal na Yeremi, bàyyikoo ci Aji Sax ji, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: Nanga bind cib téere kàddu yi ma la wax yépp. Ndax kat ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay tijjil sama ñoñ seen wërsëg, muy Israyil di Yuda.» Aji Sax jee ko wax. «Maa leen di delloo ca suuf sa ma moomale woon seeni maam.»
Ay teraanga nuyoo na
Kàddu yii la Aji Sax ji wax ci mbirum Israyil ak ci mbirum Yuda.
Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Yuuxi tiitaange dégtu na,
njàqare la, du jàmm.
Laajteleen te xool,
ndax góor day wasin léegi?
Moona maa gis jàmbaar ju ne jatu,
ni kuy matu,
kanam xoyy.
Wóoy boobu bés bu réy,
ba bés du ni mel!
Bésu njàqare lay doon
ñeel askanu Yanqóoba,
waaye dañuy mucc.
«Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi, «maay damm yet wi ñu leen tënke ci seen ndodd, dammat seeni jéng, ba dootuñu doon jaamu doxandéem. Waaye seen Yàlla Aji Sax ji lañuy jaamu ak seen buur bi ma leen di falal, mu toogal Daawuda.
10 Waaye yaw Yanqóoba sama jaam,
bul tiit,» kàddug Aji Sax jee;
«yaw Israyil, bul ragal.
Fu sore laa lay wallujee,
yaak sa askan wa ca réewum njaam ga,
Yanqóoba dellu dal, fegu;
kenn dootu ko tiital.
11 Maa ngeek yaw, nar laa wallu.»
Kàddug Aji Sax jee.
«Maay fàkkas mboolem xeet ya ma la sànniji.
Yaw nag duma la fàkkas,
duma la ñàkka topp moos,
waaye li nga yelloo laa lay yar.»
 
12 Aji Sax ji déy dafa wax ne:
«Sa damm-damm du faju,
sa góom du wér.
13 Amul ku lay sàmmal sa àq,
te sab dana amul pajtal mu baax.
14 Sa soppe yépp a la fàtte,
kenn faalewu la ci,
ndax dumay noon laa la duma,
yar la yar bu tar
ngir sa ñaawtéef ju réy
ak sa bàkkaar yu bare.
 
15 «Damm-damm yu dul wér
ak mitit wu tar jarul jooy.
Maa la teg lii,
ndax sa ñaawtéef ju réy
ak sa bàkkaar yu bare.
16 Waaye ku la lekk, dees na ko lekk;
sa noon yépp lañuy jàpp njaam ba ñu daj.
Ku la futti, dees na ko futti,
ku la saax-saaxee dees na ko saax-saaxee.
 
17 «Ñu ngi la naan: “Waccees na la,”
naan la: “Siyoŋ yaw, faaleesu la,”
waaye maa lay may wér,
faj say góom.»
Kàddug Aji Sax jee.
18 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Maa ngii di tijji wërsëgu askanu Yanqóoba,
ñibbsil leen,
baaxe seeni dëkkuwaay,
ba dëkk dekkee ca tundam wu gentoon,
kër buur taxawaat bérabam,
19 cant jollee ca,
di riirum mbégare.
Maa leen di ful,
te duñu wàññiku,
darajaal leen,
te dootuñu tuut.
20 Seeni doom dañuy mel na woon,
seen mbooloo sax fi sama kanam,
may mbugal ñi leen di sonal.
21 Su boobaa seen njiit di seen deret,
di seen kilifa, soqikoo ci ñoom;
ma woo ko, mu jege ma,
nde nit jaayul bakkanam,
ba jegesi ma te woowuma ko!»* 30.21 Leeru Yàlla, jegee ko noonu, bakkanu nit ki xaj na ci. Néegu biir ba ca kër Yàlla ga sax, du ñépp a fa mana àgg. Sarxalkat bu mag baa fa daa dugg benn yoon cim at. Keneen ku fa dugg dee. Seetal ci Sarxalkat yi 16.10; 21.17; 22.3.
Kàddug Aji Sax jee.
22 «Yeenay doon sama ñoñ,
man, may seen Yàlla.»
 
23 Ngëlénu Aji Sax jaa ngoog,
sànjam fettax na,
dig callweer,
callweeral boppu ku bon.
24 Sànjam Aji Sax ju tàng ji du giif,
te sottalul li mu nar.
Fan yu mujj ya
ngeen xam ci dara.

*30:21 30.21 Leeru Yàlla, jegee ko noonu, bakkanu nit ki xaj na ci. Néegu biir ba ca kër Yàlla ga sax, du ñépp a fa mana àgg. Sarxalkat bu mag baa fa daa dugg benn yoon cim at. Keneen ku fa dugg dee. Seetal ci Sarxalkat yi 16.10; 21.17; 22.3.