Ayóoba
Ubbite gi
Téereb Ayóoba moo nettali dundu nit ku baax ku musiba mu réy dal. Alalam jépp la jëkka ñàkk, teg ci ñàkk doomam yépp, boole ci jàngoro ju daw yaram. Gannaaw loolu, téere bi indi na ñetti pàcci wàqante yu taalife yu Ayóoba séq aki xaritam, te lépp di biral seeni tont ci tiis yooyu. Li gëna fés ci seen werante moo di ni Yàlla farala jëflantee ak doom aadama, waaye Yàlla ci boppam moo mujj feeñu Ayóoba.
Xariti Ayóoba yi, ni ñu jàngate tiisi Ayóoba mooy ni ko aaday cosaan gise ci wàllu diine rekk. Foog nañu ne, gannaaw Yàlla mbaax la mas di yoole jëf ju baax, di añale mbugal jëf ju bon, coono yi Ayóoba daj, añub bàkkaaram doŋŋ lay mana doon. Teewul Ayóoba xamle ne mbir mi yombewul noonu, te it yelloowul mbugal mu mettee ni li ko dal lépp, ndax moom ci boppam, mbaax geek njubte gi mu masa jàppoo, barewu ciy moroom. Xelum Ayóoba moo manula jàpp nan la Yàlla mana seetaane yooyu coono di dikkal ku mel ni moom. Moo tax mu am fitu dëkk Yàlla ci layoo bu mu bëgga séq ak moom. Taxul Ayóoba gëmadi, waaye nammeelam moo di mu am dëgg fi kanam Yàlla, ak itam firnde ju setal deram, gannaaw moom nit ku baax la.
Li Ayóoba laaj nag, Yàlla àdduwu ci, waaye ngëmu Ayóoba la tontoo kàddu gu jeexal aw lay, ci ab taalif bu mu misaale ne moo man te moo xam. Gannaaw loolu la Ayóoba nangu ne Yàlla mooy Buur te moom rekk a xam. Ci kaw loolu la tuub waxi meram ju ëpp.
Tëjteb téere bi moo nettali ni Ayóoba mujje. Xariti Ayóoba ya nag la Yàlla sikke kàddu yu dëng ya ñu firee coonoy Ayóoba. Mennum Ayóoba doŋŋ moo njort ne màggug Yàlla weesu na ni xaritam yooyu fooge Yàlla, ci seen gis-gis bi leen diiney cosaan gisloo.
Saar 1
Ayóobaa barkeel, ragal Yàlla
1 Amoon na ca réewum Ucc*1.1 Ucc: jombul ma nga woon ca penkub Israyil, fi ñuy wax tey Arabi mbaa Yordani mbaa Siri., góor gu ñuy wax Ayóoba. Góor googu nekkoon ku mat te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon. 2 Amoon na juróom ñaari doom yu góor ak ñett ñu jigéen. 3 Alalam juróom ñaari junniy (7 000) gàtt la woon, ak ñetti junniy (3 000) giléem, ak juróomi téeméeri (500) lëkkey nag yuy rijji, ak juróomi téeméeri (500) mbaam yu jigéen, ak jaam yu bare lool. Góor googu daal moo ëppoon daraja ca mboolem waa penku.
4 Doomi Ayóoba yu góor ya nag dañu daa ay-ayloo berndey biir kër, ku nekk ak bésam. Su ko defee ñu yónnee, woo ca seen ñetti jigéen ña, ngir ñu bokk di lekk ak a naan. 5 Bu ñu demaan ba ñépp fégal, Ayóoba day yónnee ngir sell-luloo leen. Ci biir loolu day teela xëy, daldi leen joxeel ñoom ñépp ba ñu daj saraxu rendi-dóomal, ku nekk benn. Booba Ayóoba da naan: «Jombul sama doom yii bàkkaar nañu mbaa ñu xarab Yàlla ci seen xel.» Noonu la Ayóoba jàppoo woon bés bu nekk.
Nattu nuyoo na
6 Mu am bés goney Yàlla dikk, teewsi fa Aji Sax ji. Seytaane tuumaalkat bi itam bokk ca. 7 Aji Sax ji ne Seytaane: «Ana foo jóge?» Mu ne: «Ci wër-wëraan ak doxantoo àddina laa jóge.» 8 Mu ne ko: «Xanaa seetlu nga Ayóoba, sama jaam bi! Amul moroom fi kaw suuf de! Ku mat la te jub, ragal Yàlla te dëddu lu bon.» 9 Mu ne ko: «Ayóoba daa ragal Yàlla ci neen a? 10 Xanaa du yaa ko ñag, ñag këram ak mboolem alalam, ba mu daj? Liggéeyam, nga barkeel, ba ag juram law ci réew mi. 11 Xàccil sa loxo rekk, dal ci mboolem lu bokk ci moom. Ndegam du jàkkaarlook yaw, xarab la.» 12 Aji Sax ji ne Seytaane: «Ayca boog! Mboolem lu bokk ci moom a ngi ci say loxo, waaye moom ci boppam, bu ko sa loxo laal.» Ba loolu amee Seytaane bàyyikoo fa Aji Sax ji.
13 Mu am bés doomi Ayóoba yu góor ak yu jigéen bokk toog di lekk ak a naan biiñ ca seen kër taaw. 14 Ci biir loolu ndaw dikk ne Ayóoba: «Nag ya daal a doon rijji, mbaam ya di for ca wet ga. 15 Genn gàngooru yàqkat bàyyikoo Saba, dikk daanu ci seen kaw, yóbbu leen; surga ya, ñu leel ñawkay saamar. Mennum man mii maa ca rëcce ba àggesi la ko.» 16 Kooku daaneelagul kàddoom sax, keneen dikk ne: «Sawaraw Yàlla daal a wàcce asamaan, boole gàtt yaak surga ya, jafal ba xoyom leen. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.» 17 Kooka daaneelagul kàddoom, keneen dikk ne: «Kaldeen ñaa def ñetti gàngoor, dikk sëxëtoo giléem ya, yóbbu, surga ya, ñu leel leen ñawkay saamar. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.» 18 Kooka daaneelagul kàddoom, keneen dikkati ne ko: «Sa doom yu góor ak yu jigéen a doon lekk ak a naan biiñ ca seen kër taaw. 19 Ngelaw lu mag jekki bàyyikoo ca wàllaa màndiŋ ma, dal ca ñeenti weti néeg ba, mu màbb ca kaw gone ya, ñu dee. Mennum man doŋŋ maa ca rëcce ba àggesi la ko.»
20 Ba mu ko defee Ayóoba jóg, ne tareet mbubbam, ba noppi watu nel, di ko ñaawloo. Mu daanu fi suuf, sujjóot, 21 daldi ne: «Duŋŋ laa génne sama biiru ndey te duŋŋ laay delloo. Aji Sax jee maye, Aji Sax jee nangu. Cant ñeel na Aji Sax ji.» 22 Ci biir loolu lépp Ayóoba bàkkaarul, jiiñul Yàlla lenn lu juunu.