Saar 42
Ayóoba tuub na
Ba loolu amee Ayóoba àddu ne Aji Sax ji:
Xam naa ne lépp nga man;
du lenn loo tële.
Nee nga ma: «Ana koo doon,
bay lëntal samay dogal te xamoo?»
Maa wax moos te xawma lenn
ci kawtéef yu ma wees, ump ma.
Nee nga: «Déglul, maa lay wax.
Ma laaj la, nga xamal ma.»
Dég-dégu nopp laa amoon ci yaw,
tey bët laa la teg.
Moo ma tax ne: «Wàqet, tuubi-ruubi,»
ba diwoo suuf akub dóom.
Yàlla leqli na Ayóoba
Gannaaw ba Aji Sax ji waxee Ayóoba yooyu kàddu, Aji Sax ji dafa wax Elifas ma cosaanoo Teman, ne ko: «Sama xol tàng na ci yaw, yaak sa ñaari xarit yi, ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe. Kon nag sàkkleen juróom ñaari yëkk, ak juróom ñaari kuuy. Ngeen dem ba ca sama jaam ba Ayóoba, joxe ko fa saraxu rendi-dóomal, te Ayóoba ñaanal leen, ma seet ci moom ba bañ leena mbugale seenug ndof. Ndax waxuleen dëgg ci man ni sama jaam bi Ayóoba waxe.»
Ba loolu amee Elifas waa Teman ba, ak Bildàdd waa Suwa, ak Cofar waa Naama daldi dem, def la leen Aji Sax ji sant. Aji Sax ji seet ci Ayóoba. 10 Gannaaw ba Ayóoba ñaanalee xaritam ya, Aji Sax ji tijji wërsëgu Ayóoba. Aji Sax ji ful na ñaari yoon mboolem alalu Ayóoba. 11 Ba loolu amee mboolemi bokkam, góor ak jigéen, ak mboolemi xameem ya woon, dikk bokk ak moom bernde ca këram. Ñu dëfal ko, mas-sawu ko ci bépp coono bu ko Aji Sax ji tegoon. Ku ci nekk jox ko dogu xaalis ak jaarob wurus. 12 Aji Sax ji nag barkeel mujug Ayóoba lu raw ndoorteem. Mu am fukki junniy gàtt ak ñeent (14 000), ak juróom benni junniy giléem (6 000), ak junniy lëkkey nag (1 000) yu muy rijjee, ak junniy mbaam yu jigéen (1 000). 13 Mu amaat juróom ñaari doom yu góor ak ñett ñu jigéen, 14 ka mag ca jigéen ña, mu tudde ko Yemima, ka ca topp di Keciya, ka ca toppaat di Keren Apug. 15 Mboolem jigéeni réew ma, amul ku rafete woon ni ñetti doomi Ayóoba yooyu. Seen baay nag sédd leen ndono lu tollook seen céri càmmiñ. 16 Gannaaw loolu Ayóoba dundaat na téeméeri at ak ñeent fukk (140). Gis na ay doomam, gis ay sëtam, ba muy ñeenti maas. 17 Ayóoba màggat na ba ñor xomm, doora dee.