Téereb Yonent Yàlla
Mise
Saar 1
Kàddug Aji Sax jii moo dikkaloon Mise miy waa Moreset, ca janti Yotam ak Axas ak Esekiya, buuri réewum Yuda, na seen nguur topplantee. Lii la Mise gis ci mbirum Samari ak Yerusalem*1.1 Gannaaw ba réewum Yawut xàjjalikoo, Samari moo doon péeyub Israyil ca bëj-gànnaar, Yerusalem di péeyub Yuda ca bëj-saalum..
Aji Sax ji yékkati na kàddug tuuma
Dégluleen, yeen, xeetoo xeet,
teewlul, yaw àddina ak li ci sa biir,
ba Boroom bi Aji Sax ji seedeel leen tuuma,
Boroom beey àddoo fa màkkaanam mu sell ma.
Aji Sax jaa ngii di génne ca bérabam ba,
mooy wàccsi, daagoo kawtey suuf.
Tund ya mu joggi da naan soyox seey,
xur ya xar, wàyyi ni dax ju jege sawara,
def ni ndox mu wale kaw mbartal.
 
Bàkkaaru Yanqóobaa waral lii lépp,
moyi Israyil googu la.
Ana luy bàkkaaru Yanqóoba?
Da dul Samari?
Ana fuy bérabi jaamookaayi xërëm ci Yuda?
Da dul Yerusalem?
«Maay saam Samari, def ko jalu tojit
ci mbooy gi,» la Aji Sax ji wax.
«Maa koy def jëmbatukaayub reseñ,
maay yuri ay doji tabaxam ca xur wa,
ñori ay kenoom.
Seen jëmmi tuur yépp ay rajaxoo,
te mboolem seen peyoor yu sobewu
day lakk ba jeex.
Maay tas tasar mboolem seen jëmmi xërëm1.7 jëmmi xërëm yooyu, su tojee it di gànjar gu ñu mana wecci xaalis.,
seen peyi gànc a leen ko may,
kon na ko seen moroomi gànc feyeekoo.»
Ñaawlu dikkal na Yuda
Lee ma tax di jooy ak a yuuxu,
ne duŋŋ, deme tànki neen, di ko ñaawloo.
Naa yuuxu nig till,
naa sab sabum looy ndaxu naqar.
Góom bi Aji Sax ji teg Samari kat amul paj,
te moo law ba Yuda,
àkki ba buntu Yerusalem, ca saay bokk.
10 Buleen ko nettali fa Gaat1.10 Gaat dëkku Filisti la woon. Yeneen juróom ñeenti dëkk yi ci topp ñoo séqoon Moreset Gaat, dëkku cosaanu Mise. Ni baatub Gaat di jibe ci ebrë dafa neexoo ak baat biy tekki «nettali.»,
buleen jooy benn yoon.
Xalanguleen fa pëndub suuf sa ca Bet Leyafra§1.10 Bet Leyafra kërug pëndub suuf lay tekki, te neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «pëndub suuf.»,
di ko ñaawloo.
11 Yeen waa Safiir*1.11 Turu dëkk bii, Safiir, man naa tekki «taaru,» taar bi nag woroo ak gàcce gi ñu wax ci aaya bi., jàll-leen,
ak gàcce ak yaramu neen.
Waa Caanan1.11 Caanan neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «génn.» sañuñoo génn,
te wall du bawoo fa waa Bet Eccel1.11 Eccel niroo na ak baatu ebrë bi mana tekki «gàntal,» wax ji di wund ne «wall gàntal na.»,
ñay jooy seeni néew.
12 Waa Marot a mar jàmm,
te aw ay a wàcce fa Aji Sax ji,
ba agsi buntu Yerusalem§1.12 Turu Yerusalem wi indi na baatu ebrë bu mana tekki «jàmm,» mu woroo ak ay wi ñu ne mooy agsi Yerusalem, woroo itam ak Marot, baatu ebrë bi jegewoo ak «wextan.».
13 Yeen waa Lakis*1.13 Turu dëkk bi, Lakis lañu nirule ak baatu ebrë bu mana tekki «fasi dawkat.», takkleen fasi dawkat ak watiir.
Yeena jëkka moyloo janq Siyoŋ mu taaru,
ci yeen lañu jëkka gise bàkkaari Israyil.
14 Yeen waa Yuda, mayleen waa Moreset Gaat1.14 Turu dëkk bii, Moreset, baat bi mu jegewool ci Ebrë man na tekki «ab séet.» Aaya 10 moo wax ci «Gaat.»
lu ngeen tàggtook ñoom,
këri Agsib1.14 Agsib neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «wor.» wori neen lay doon ci buuri Israyil.
15 Yeen waa Maresa§1.15 Maresa neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «nangukatub réew.» laay indil ku leen moom,
te ca Adulam*1.15 Adulam mooy xunti ma Daawuda làqu woon, ba muy daw buur Sóol. la ñi Israyil di damoo di làquji.
16 Watuleen nel, ñaawloo ko
doom yi leen doon bànneexal.
Neluleen nel yu set nim tan, naqarloo,
nde ngàllo lañu jëm, teqlikook yeen.

*1:1 1.1 Gannaaw ba réewum Yawut xàjjalikoo, Samari moo doon péeyub Israyil ca bëj-gànnaar, Yerusalem di péeyub Yuda ca bëj-saalum.

1:7 1.7 jëmmi xërëm yooyu, su tojee it di gànjar gu ñu mana wecci xaalis.

1:10 1.10 Gaat dëkku Filisti la woon. Yeneen juróom ñeenti dëkk yi ci topp ñoo séqoon Moreset Gaat, dëkku cosaanu Mise. Ni baatub Gaat di jibe ci ebrë dafa neexoo ak baat biy tekki «nettali.»

§1:10 1.10 Bet Leyafra kërug pëndub suuf lay tekki, te neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «pëndub suuf.»

*1:11 1.11 Turu dëkk bii, Safiir, man naa tekki «taaru,» taar bi nag woroo ak gàcce gi ñu wax ci aaya bi.

1:11 1.11 Caanan neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «génn.»

1:11 1.11 Eccel niroo na ak baatu ebrë bi mana tekki «gàntal,» wax ji di wund ne «wall gàntal na.»

§1:12 1.12 Turu Yerusalem wi indi na baatu ebrë bu mana tekki «jàmm,» mu woroo ak ay wi ñu ne mooy agsi Yerusalem, woroo itam ak Marot, baatu ebrë bi jegewoo ak «wextan.»

*1:13 1.13 Turu dëkk bi, Lakis lañu nirule ak baatu ebrë bu mana tekki «fasi dawkat.»

1:14 1.14 Turu dëkk bii, Moreset, baat bi mu jegewool ci Ebrë man na tekki «ab séet.» Aaya 10 moo wax ci «Gaat.»

1:14 1.14 Agsib neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «wor.»

§1:15 1.15 Maresa neexoo na ak baatu ebrë bu mana tekki «nangukatub réew.»

*1:15 1.15 Adulam mooy xunti ma Daawuda làqu woon, ba muy daw buur Sóol.