Saar 3
Ab safaan ñeel na Niniw
Wóoy, ngalla dëkkub tuurkatu deret bi,
ñépp di fen, fees aku ay,
te foqati alalu jaambur du dakk!
 
Kàccri dal,
ay mbege riir,
fas rëpptal,
watiir kar-kari.
Gawar buur,
saamar melax,
xeej lerxat,
ñu bare ne lasiim,
ñi dee jale,
néew ya tëë jeex,
ñuy fakkastaloo néew ya.
Aw léeb ñeel na Niniw, gànc biy xërëmtu
Lépp ndax ngànctu gu bare,
gi gànc bi nekke!
Jekk tànkee, boroom xërëm yi,
ci ngànctu nga jaaye ay xeet,
te xërëmtu nga naxe ay giir.
 
«Maa ngii fi sa kaw,»
kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
«Sa pendal laay ñori,
ba muur sa xar-kanam,
won xeeti jaambur yi sa yaramu neen,
gisloo waa réew yi sa gàcce.
Maa lay xëpp mbalit, sewal la,
def lam ceetaan,
ku la gis, daw la
te naan: “Niniw tas na!
Moo ku koy jooy?”
Ana fu ma koy wutale ñu ko dëfal?»
 
Niniw du gën Teeb demin
Moo Niniw, dangaa gën Teeb, péeyub Misraa?
Dëkk ba dëju fa digg wali Niil ya,
am ndox wër ko,
am tataam di géej,
miiram di ndox mu wale géej,
réewum Kuus di ndëgërlaayam,
Misra di ko dooleele doole ju dul jeex,
réewum Puut ak Libi di ko jàpple.
 
10 Teewul ngàllo la dem, cig njaam;
ay goneem, ñu falaxe leen
ci mboolem selebe yoon;
ay kàngamam, ñu tegoo bant;
kilifaam yépp, ñu jéng leen.
11 Niniw yaw it dinga bilimbaane,
jànnaxe, di wuta raw ab noon.
Doole réer na Niniw
12 Sa tata yépp ni garabi figg
yu ñoral ndoortel meññeef lay mel,
soo yëlbee, doom ya rot,
gémmiñu lekk-kat aw.
13 Say gàngoor a ngii diy jigéen fi sa biir,
sa bunti réew lafal say noon,
ne ŋàpp-ŋàppaaral,
sawara xoyom tëjukaay ya!
 
14 Niniwee, ndox moo fàggoo ab gaw,
ngay rooti te dàbbli say tata.
Duggal ci bàq bi, note ban bi,
te ne cas móolukaay bi!
15 Fa la la sawara di xoyome,
saamar xottee la fa,
raafal la ni soccet di def.
Niniw day raaf
Fulal saw nit niy soccet,
ñu tollu niy njéeréer.
16 Ay jula nga barele,
ba ñu ëpp biddiiwi asamaan,
te ñoo mel niy soccet, tojtal, naaw.
17 Say kàngam it niy soccet,
say jawriñ ni naaxu gunóor
yu dale kaw tata, bésub sedd,
jant bi jóg, ñu daw,
te deesul xam fu ñu nekk.
Woykat jooy na Niniw
18 Buurub Asiree, say sàmm a saay,
say garmi nelaw,
sa gàngoor tasaaroo kaw tund wa,
te ku leen dajale wuute.
19 Sa damm-damm amul paj,
sab góom metti,
ba mboolem ñi dégg li la dal
di tàccu ci sa kaw,
nde ana ku sa mbon gi dul jeex lorul?