Saar 11
1 Ba mu ko defee njiiti mbooloo ma dëkk Yerusalem. Ña des ca mbooloo ma tegoo bant ngir fukk ñu daje kenn génne ca, dëkk Yerusalem, dëkk bu sell bi, juróom ñeent ñi ci des toog ca (seeni) dëkk yu ndaw. 2 Mbooloo ma nag gërëm ñi nangul seen bopp ne dañuy dëkk Yerusalem. 3 Dëkki Yuda ya bànni Israyil yaa ca dëkkoon, ñook sarxalkat yaak Leween ñaak, ña féetewoo liggéey yu sew ya ca kër Yàlla gaak ña askanoo ca jaami Suleymaan ya, ku nekk ak sa céru suuf, ca dëkk ba nga bokk. Ñii ñuy lim nag ñooy njiiti diiwaan ñi dëkke Yerusalem. 4 Amoon na it ñu dëkkoon Yerusalem te bokk ci giirug Yuda ak giirug Beñamin.
Ñi bokk ci askanu Yuda Ataya la, ku góor ka Usiya di baayam; Sàkkaryaa di baayu Usiya; Amarya di baayi Sàkkaryaa; Sefatiya di baayi Amarya; Mayalel di baayi Sefatiya, Peres di baayi Mayalel; 5 ak Maaseya, ku góor ka Barug di baayam; Kol Xose di baayu Barug; Xasaya di baayu Kol Xose; Adaya di baayu Xasaya; Yowarib di baayu Adaya; Sàkkaryaa may doomu ku dëkk Silon di baayu Yoyarib. 6 Waa askanu Peres ya dëkk Yerusalem ñeenti téeméeri jàmbaar lañu ak juróom benn fukk ak juróom ñett.
7 Ñi bokk ci askanu Beñamin Salu la, ku góor ka Mesulam di baayam; Yowet di baayu Mesulam, Pedaya di baayu Yowet; Kolaya di baayu Pedaya, Maaseya di baayu Kolaya, Itiyel di baayu Maasya, Yisaya di baayu Itiyel; 8 Gabay ak Salay topp ca Ñoom ñépp di juróom ñeenti téeméer ak ñaar-fukk ak juróom ñett. 9 Yowel doomu Sikkri moo leen jiite woon, Yewuda doomu Asenuwa topp ca, di ñaareelu kilifag dëkk ba.
10 Sarxalkat ya Yedaya doomu Yoyarib Yakin bokk na ca, 11 ak Seraya, baayam di Ilkiya, Mesulam di baayu Ilkiya, Sadog di baayu Mesulam, Merayot di baayu Sadog, Ayitub, njiital kër Yàlla ga di baayu Merayot. 12 Ñoom ak ña ñu àndal ca liggéeyu kër Yàlla ga. Ñuy juróom ñetti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar. Adaya ma Yerowam di baayam it bokk na ca. Pelaliya di baayu Yerowam, Amsi di baayu Pelaliya, Sàkkaryaa, di baayu Amsi, Pasur di baayu Sàkkaryaa, Malkiya di baayu Pasur. 13 Maam la ak ña mu àndal ca liggéey ba te ñu yilif seeni kër baay, ñuy ñaar téeméer ak ñeent-fukk ak ñaar. Amasay ma Asarel di baayam bokk na ca; Axsay di baayu Asarel; Mesilemot di baayu Axsay; Imer di baayu Mesilemot. 14 Moom la ak seeni bokk, yu jàmbaare te ñeme. Ñuy téeméer ak ñaar fukk ak juróom ñett. Sabdiyel ma Agdolim di baayam moo leen jiite woon.
15 Leween ña Semaya ma Xasub di baayam bokk na ca, Asrikam ay baayu Xasub; Asabiya di baa yu Asrikam, Buni di baayam Asabiya; 16 moom la ak Sabtay ak Yosabàdd, di ñaari kilifay Leween yu sasoo liggéeyu kër Yàlla ga, fa féete biti; 17 ak Mataña ma baayam di Mika. Sabdi mooy baayu Mika; Asaf miy baayu Sabdi moo doon kilifa gay jiite ci cant ak ñaan; ak Bagbukiya miy mbokkum Mataña tey njiit li topp ci moom ak Abda mi Samuya di baayam; Galal di baayu Samuya, Yedutun di baayu Galal. 18 Mboolem Leween ña dëkkoon ca dëkk bu sell ba ñaar téeméer lañu ak juróom ñett fukk ak ñeent. 19 Wattukati bunt ya Akub la woon ak Talmon ak seeni bokk. Ñoo doon wattu bunt ya, tollu ci téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñaar.
20 Ña des ci bànni Israyil nag, boole ca sarxalkat yaak Leween ña ca des daldi dëkke mboolem dëkki Yuda ya, ku nekk ak fa mu séddoo.
21 Ci kaw loolu ña féetewoo liggéey yu sew ya ca kër Yàlla ga dëkk Ofel, Siyxa ak Gispa jiite leen.
22 Kilifag Leween ña ca Yerusalem moo doon Utsi ma Bani di baayam; Xasabiya di baayu Bani, Mataña di baayu Xasabiya, Mika di baayu Mataña. Utsi bokkoon ci ñi askanoo ci Asaf te doonoon woykat yay woy ca kër Yàlla ga. 23 Woykat ya sax ña nga nekkoon ca ndigalal Buur lu leen di dogalal la leen war bés bu nekk.
24 Petaya ma baayam di Mesesabel mu bokk ci askanu Sera doomu Yuda moom la Buur dénkoon mboolem mbir yi soxal mbooloo mi.
25 Ci wàllu dëkk yu ndaw yeek seeni àll nag am na waa kër Yuda yu dëkke woon Kiryaat Arba ak dëkk-dëkkaan ya ko wër, am ñu ca dëkke Dibon ak la ko wër, am ñu dëkke Yekabseel ak gox ya ko wër; 26 am ñu dëkke Yeswa ak Molada ak Bet Pelet; 27 ak Àccar Suwal ak Beerseba ak la ko wër. 28 Mu am ñu dëkke Ciglaag ak Mekona ak la ko wër; 29 ak En Rimon ak Sora ak Yarmut; 30 ak Sanowa ak Adulam ak gox ya ko wër ak Lakis aki àllam ak Aseka ak la ko wër. Noonu ñu dëkke la dale Beer Seba ba ca xuru Inom.
31 Noonu waa giirug Beñamin dëkke la dale Geba ak Migmas, boole ca Aya ak Betel ak la ko wër. 32 Mu am ñu ca dëkke Anatot ak Nob ak Anaña; 33 ak Àccor ak Raama ak Gitayim; 34 ak Adit ak Seboyim ak Nebalat; 35 ak Lot ak Ono ca xuru liggéeykat ya. 36 Am na nag ay kuréli Yudeen ñu bàyyikoo Yuda sanci ca waa giirug Beñamin.