Saar 3
Wóolul Yàlla
Doom, bul fàtte sama njàngle,
defal sa xel ci saay santaane,
ngir fan wi gudd lool,
nga gëna am jàmm.
Bu la ngor ak worma dëddu,
booleel takk ci sa baat,
bind ko ci sa àlluway xol.
Kon nga xam lu jaadu,
neex Yàllaak doom aadama.
Nanga wóoloo Aji Sax ji, sa léppi xol,
te bul wéeru ci saw déggin.
Loo mébét, bàyyil Yàlla xel,
mu xàllal la yoon.
Bul doyloo sa xel mu rafet,
ragalal Aji Sax ji, dëddu mbon;
sa yaram wér,
say cér naat.
 
Teralal Aji Sax ji ci sa alal
ak loo jëkka meññle,
10 say sàq day fees, ne xéew,
say mbàndi ndoxi reseñ di wal.
 
11 Doom, bul xeeb yaru Aji Sax ji,
bul bañ mu waññi la,
12 ndax Aji Sax ji, ku mu sopp, waññi la,
ni baay, ak doom ju ko neex.
Li xel mu rafet di jariñ
13 Mbégtee ñeel ku daj xel mu rafet
ak ku am ug dégg.
14 Am koo gën am xaalis,
te njariñ laa raw wurus.
15 Xel mu rafet a gën gànjar;
loo mana bëgg moo ko raw.
16 Gudd fan, mu joxee ndijoor;
càmmoñ ba, alal ak teraanga.
17 Fa muy jaare yiw la,
fu mu awe jàmm la.
18 Mooy garabu gudd fan ci ku ko jàpp,
di mbégtey ku ca ŋoy.
19 Aji Sax ji xel mu rafet la sose suuf,
lale asamaan ag dégg.
20 Ci xam-xamam la ndoxi xóote ya ne jàyy,
ay niir di lay.
Rafet xel barke la
21 Sama doom, saxool xelu akug foog,
dee ci xool foo tollu.
22 Day guddal saw fan,
di rafetal sa jikko.
23 Kon sab dox wóor,
doo fakktalu.
24 Soo tëddee doo tiit;
say nelaw day neex.
25 Kon doo ragal njàqare lu bette
ak saaysaay buy songe,
26 ndax Aji Sax ji da lay yiir,
di la musal cig fiir.
 
27 Bul xañ njekk ku ko yelloo,
ndegam man nga ko.
28 Bul ne say dëkk: «Demal ba beneen, ma jox la,»
te fekk la yor.
 
29 Bul fexeel dëkkandoo
bu dëkk ak yaw ci kóolute.
30 Bul joteek kenn ci neen,
te tooñu la.
 
31 Bul ñee ku néeg,
te bu ko roy fenn.
32 Aji Sax ji daa sib ku dëng,
xejjoo kuy jubal.
33 Aji Sax ji day alag kër ku bon,
di barkeel waa kër ku jub.
34 Kuy ñaawle, moo lay ñaawal,
ku toroxlu, mu may law yiw.
35 Teraanga di céru ku rafet xel,
ab dof gàccoo gàcce.