Sabóor 16
Aji Sax ji laa séddoo, dund ak dee
Muy taalifu Daawuda, ngir jàngle.
 
Éy Yàlla, sàmm ma, maa ngi làqu fi yaw!
Maa ne Aji Sax ji: «Yaay sama Boroom,
awma alal ju la moy.»
Ñu sell ñi ci réew mi ñooy garmi yi,
sama mbégte mépp ñoom a.
Kuy sàkkuy tuur barew tiis,
man de duma leen tuural deret,
sama làmmiñ du leen tudd.
 
Aji Sax ji, yaay wàll wi ma séddoo,
di sama ndabal xéewal.
Yaa yor sama wërsëg.
Maa muurloo bérab bu neex,
ndaw cér bu rafet!
Ma sant Aji Sax ji may xelal,
ba guddi sax sama xel di ma yedd.
Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji
ndijoor la ma fare, ba duma tërëf,
xanaa di bànneexu, sama xol bég,
sama yaram finaax.
10 Doo ma wacc njaniiw moos,
sa wóllëre wa, doo ko won yàqutey bàmmeel*16.10 Woykat bi di wone fii kóoluteem ne Aji Sax ji du ko seetaan muy dee ci saa si, waaye dina ko musal ci dee gi ko doon yoot ca fan yooya. Seetal ci Jëf ya 13.34-37..
11 Yaa may xamal yoonu ndund.
Fu bànneex mate, yaa teew,
xéewal sa ndijoor la saxe.

*16:10 16.10 Woykat bi di wone fii kóoluteem ne Aji Sax ji du ko seetaan muy dee ci saa si, waaye dina ko musal ci dee gi ko doon yoot ca fan yooya. Seetal ci Jëf ya 13.34-37.