20
Yal na Buur daan 
  1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.  
  2 Buur, yal na la Aji Sax ji nangul bésu njàqare,  
yal na la turu Yàllay Yanqóoba aj fu kawe,   
 3 yal na la yónnee wallam fa këram,  
jàppalee la fa, ca Siyoŋ.   
 4 Yal na xool loo ko jébbal,  
di rafetlu sarax soo ko lakkal. 
Selaw.
    5 Yal na la may li nga namm,  
di sottal loo mébét,   
 6 ngay daan, nuy ree,  
yéege sunu raaya, màggal sunu Yàlla.  
Yal na Aji Sax ji nangu loo dagaan.   
 7 Aji Sax jeey musal ki mu fal, bir na ma tey.  
Moo koy nangule fa asamaan su sell sa,  
ci dooley ndijooram biy musle.   
 8 Ñiiki watiir,  
ñeeki fas,  
nun sunu turu Yàlla Aji Sax ji lanuy tudd.   
 9 Ñoom ñooy jeng aka jóoru,  
nun, nu jóg, taxaw jonn.   
 10 Éy Aji Sax ji, mayal Buur mu daan,  
te bés bu nu ko ñaane, mu nangul nu.