Sabóor 34
Aji Sax ji du tanqamlu aji jub
Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem*34.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.10-15. Akis buurub Gaat mooy Abimeleg ba tey..
 
Naa màggal Aji Sax ji saa su ne,
di ko sant fu ma tollu.
Aji Sax ji laay sagoo,
néew-ji-doole dégg, bég.
Kañleen Aji Sax ji, ànd ceek man,
nu bokk wormaal turam.
 
Maa sàkku Aji Sax ji, mu nangul ma,
tàggale maak lépp lu ma ragal.
Ku yaakaar Aji Sax ji bég, leer nàññ,
gàcce du ko sëlëm.
Néew-ji-doole woote, Aji Sax ji wuyu,
musal ko fu mu jàqe.
Ku ragal Aji Sax ji, malaakaam yiir la,
di la wallu.
Mosleen, xam ne Aji Sax jee baax,
ndokklee yaw mi ko làqoo.
10 Ragal-leen Aji Sax ji, yeen nitam ñu sell ñi;
ku ko ragal doo ñàkk dara.
11 Gaynde man naa ndóol, xiif,
nit sàkku Aji Sax ji, ñàkkul lenn lu baax.
 
12 Dikkal doom, déglu ma,
ma jàngal la ragal Aji Sax ji.
13 Ana ku dund neex,
mu bëgga gudd fan, ba gis ngëneel?
14 Na làmmiñam daw lu aay,
dawi fen.
15 Na dëddu lu bon tey def lu baax,
sàkku jàmm, saxoo ko.
 
16 Ay gët la Aji Sax ji ne jàkk aji jub ji,
te ay noppam la dékk wooteb wallam.
17 Aji Sax jeey rëbb kuy jëfe mbon,
ngir dagge ko kaw suuf, far turam.
18 Ku jub yuuxu, Aji Sax ji dégg,
fu mu jàqe, mu musal ko.
19 Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la,
sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la.
20 Musiba bare naa dal ku jub,
Aji Sax ji musal ko ci lépp,
21 di ko sàmm,
ba benn yaxam du damm.
22 Musiba nag day rey ku bon,
te ku bañ aji jub, yoon dab na la.
23 Aji Sax jeey jot ab jaamam,
képp ku ko làqoo, yoon du la dab.

*34:1 34.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.10-15. Akis buurub Gaat mooy Abimeleg ba tey.