Sabóor 40
Déggal Aji Sax jee am solo
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
2 May xaara xaar Aji Sax ji,
mu dégg may woote, geesu ma,
3 génnee ma ca kàmbug sànkute,
sippee ma ca xóotey ban ba,
cëppe ma ciw doj,
samp ma, ma dëgër.
4 Moo ma may, ma fent,
woy wu ma woye sunu Yàlla.
Ñu baree seede, di wormaal
ak a dénku ci Aji Sax ji.
5 Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji,
te sàkkuwoo ku bew
ak kuy topp ay fen.
6 Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def,
amuloo moroom!
Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal,
ma bëgga xamle lépp,
te mu bare ba wees ab lim.
7 Saraxi gàtt mbaa pepp, taamuwuloo ko,
ay nopp nga ma bënnal,
saraxu rendi-dóomal, ak saraxu póotum bàkkaar,
sàkkuwuloo ko.
8 Ma ne: «Maa dikk nii,
téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
9 Sama Yàlla, maa soppa def sa coobare,
ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
10 Siiwal naa sag njekk ca ndaje mu mag ma.
Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko.
11 Làquma sag njekk, ne cell ak moom.
Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko.
Làquma ndaje mu mag ma sa ngor ak sa worma.
12 Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande.
Sa ngor ak sa worma,
yal na ma feg ba fàww.
13 Ay musibaa ma tanc,
ne gàññ, ba wees ab lim.
Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma,
baree bare, ba ëpp sama kawari bopp;
sama xol jeex tàkk.
14 Éy Aji Sax ji, yal na la neex, nga wallu ma!
Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
15 Képp kuy wuta fëkk sama bakkan,
yal na rus, torox ne tott.
Kuy bége sama loraange,
yal nañu ko duma, mu ne yàcc.
16 Ku may ñaawal,
yal nañu ko torxal, mu jommi.
17 Képp ku lay sàkku,
yal na bég, di la bànneexoo.
Képp ku safoo sag wall,
yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»
18 Man, néew naa doole, ñàkk naa,
waaye yaw Aji Sax ji, danga maa yég.
Yaw yaa may wallu, xettli ma;
sama Yàlla, bu ma yeexe.