Sabóor 51
Yàlla, yërëm ma
Mu jëm ci njiitu jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba*51.2 Seetal ci 2.Samiyel 11—12.25..
 
Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni,
faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef,
raxasal ma sama moy.
Xam naa ne maa tooñ,
sama moy a ngi janook man saa su ne.
Yaw laa moy, yaw doŋŋ.
Li nga ñaawlu laa def.
Kon boo waxee, yaa yey;
te soo àttee, wàcc nga.
Ñaawtéef daal laa judduwaale,
te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol,
kon déey ma xel mu rafet.
Wis ma ndox, ma sell;
sang ma, ma set wecc.
10 Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex,
ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.
11 Bul xool samay moy,
faral sama ñaawtéef yépp.
12 Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell,
yeesalal ma pastéefu xol.
13 Bu ma xalab,
bu ma xañ sa noo gu sell.
14 May ma, ma bégeeti sag wall,
te dundale ma xol bu tàlli,
15 ma xamal tooñkat sa war,
ba moykat dellu ci yaw.
 
16 Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal,
baal ma deret ji ma tuur,
ma siiwal sa njekk.
17 Boroom bi, may ma, ma wax,
ma delloo la njukkal.
18 Sàkkuwloo sarax, nde kon ma indi;
te soppuloo saraxu rendi-dóomal.
19 Saraxi Yàlla, xol bu tuub la,
yaw Yàlla, xol bu tuub ba mokk, doo gàntal boroom.
 
20 Ngalla baaxeel Siyoŋ,
yal nanga tabax tatay Yerusalem.
21 Su boobaa nga nangu sarax yi war,
di saraxu rendi-dóomal.
Su boobaa ñu rendi ay yëkk ca sa sarxalukaay.

*51:2 51.2 Seetal ci 2.Samiyel 11—12.25.