Sabóor 54
Yàlla, dimbali ma
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew*54.2 Seetal ci 1.Samiyel 23.14-28; 26.1-5..
 
Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur,
jox ma dëgg, ci sa kàttan.
Éy Yàlla, déglul, ma ñaan,
teewlul, ma wax la.
Ay doxandéem a ma jógal,
di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan,
te seetuñu ci Yàlla.
Selaw.
 
Yàllaa ngii, moo may dimbali;
Boroom bee yor sama bakkan.
 
Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru,
yal na leen sa dëgg sànk.
Xol bu tàlli laa lay sarxale.
Aji Sax ji, yaa baax,
ma sant la.
Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële,
ma tiim samay noon.

*54:2 54.2 Seetal ci 1.Samiyel 23.14-28; 26.1-5.