Sabóor 57
Yàlla jógal, wallu ma!
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma*57.1 Seetal ci 1.Samiyel 24..
2 Éy Yàlla, baaxe ma, ngalla baaxe ma,
fi yaw laay làqu,
yiiroo sa kiiraay,
ba musiba yi jàll.
3 Ma woo Yàlla, Aji Kawe ji,
Yàlla, mi may matalal.
4 Mooy yónnee fa asamaan, musal ma,
dumaal ma ku may not.
Selaw.
Yàllaay yónnee jëfi ngoram ak wormaam.
5 Maa ngi tëdd ci biiri noon
yu mel niy gaynde, di yàpp doom aadama.
Seeni sell niy xeej aki fitt,
seen làmmiñ di saamar yu ñaw.
6 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan,
sag leer tiim suuf sépp.
7 Noon yi di ma fiir,
sama xol jeex.
Ñu gasal mam pax,
far tàbbi ca.
Selaw.
8 Yàlla, dogu naa,
dogu naa woy, di la kañ.
9 Na sama jëmm jépp yewwu,
xalam ak moroom ma yewwu;
ma yee leeru njël.
10 Boroom bi, naa lay gërëm ci biir xeet yi,
kañ la ci biir waaso yi.
11 Sa ngor a màgg, ba àkki asamaan,
sa worma àkki fa kawa kaw.
12 Éy Yàlla, yaa màgg, ba sut asamaan,
sag leer tiim àddina sépp.