Sabóor 95
Kaayleen, nu sant
Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji,
nu xaacul ki nuy sës, mucc.
Nanu ko dikke cant,
woyal ko, mu riir.
Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji,
buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
Moo moom xóotey suuf,
moom colli tund yi,
moom géej, sàkk ko,
moom jéeri ji mu mooñ.
Nan sëgg, sujjóot,
sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
Mooy sunu Yàlla,
nuy xeet wi muy foral,
diy gàtt ciy loxoom.
 
Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba,
jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
fa ma seeni maam doon nattoo,
di ma seetlu te gis la ma def*95.9 Seetal ci Mucc ga 17.1-7..
10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas,
ma ne: “Xeet wu ñàkk wormaa ngi,
te faaleedi samay santaane.”
11 Moo ma taxa mer, ba giñal leen,
ne duñu tàbbi fa sama noflaay.»

*95:9 95.9 Seetal ci Mucc ga 17.1-7.