Sabóor 99
Aji Sax ji buur bu sell la
Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragal-leen ko!
Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!
Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg,
kawe, tiim xeetoo xeet.
Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko.
—Kee sell!
Buur, jëfe yoon mooy dooleem,
te yaa saxal njub, yoon ak njekk
ci askanu Yanqóoba.
Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji,
te sujjóot fa ndëggastalam.
—Kee sell!
 
Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam,
Samiyel bokk ca ñay tudd turam.
Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.
Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom,
ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon.
Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon,
di seen Yàlla ju leen di baal,
te di leen mbugale seeni jëf ju bon.
Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji,
te sujjóot fa tundam wu sell wa.
—Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!