Sabóor 125
Ku doyloo Aji Sax ji raw
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
 
Ku doyloo Aji Sax ji,
yaay tundu Siyoŋ, doo toxu;
dangay sax ba fàww.
Ni tund yi yéewe Yerusalem,
ni la Aji Sax ji yéewe ñoñam,
tey ak ëllëg.
 
Nguur gu bon du saxe
kaw suuf su nit ñu jub muurloo.
Lu ko moy ñu jub ñi sàkku lu bon,
di ko jëfe.
 
Éy Aji Sax ji, baaxeel ku baax,
ak kuy mébét njub.
Waaye kuy topp yoonu ndëngte,
Aji Sax jee koy sànk,
boole kook kuy def lu bon.
Yal na jàmm dal Israyil.