137
Jooye nanu àll 
  1 Ca tàkkal dexi Babilon,  
foofa lanu daa toog,  
fàttaliku Siyoŋ, jooy.   
 2 Ca garab ya  
lanu daa wékk sunuy xalam.   
 3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo,  
noot nu, bëgg nu bégal leen,  
naan: «Woyalleen nu ci woyi Siyoŋ.»   
 4 Moo! Nu nuy woye woyu Aji Sax ji  
kaw suufas yéefar?   
 5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte,  
yal na ma doole dëddu!   
 6 Yerusalem, su ma la fàttalikuwul,  
fonk la, ba gën laa bége lépp,  
yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.   
 7 Aji Sax ji, fàttalikul Edomeen ña,  
keroog jantub Yerusalem,  
ba ñu naan: «Màbbleen a màbb,  
ba suuf sa dëkk bi sampe siiñ!»   
 8 Yeen waa Babilon gi ñu nara fàllas,  
ndokkalee ku leen fey jëf ja ngeen nu def!   
 9 Ndokkalee ku ne cas seeni fere,  
tas ciw doj!