Saar 9
Yàlla moo taamu bànni Israyil
1 Dëgg laay wax, Almasi seere na ko, fenuma. Sama xol moo ma seereele Noo gu Sell gi, ne lii may wax dëgg la: 2 Li may wax moo di tiis wu réy laa am, ak naqaru xol wu dakkul, 3 nde man doon naa ñaana alku sax, daggoo ak Almasi, ngir jàmmi sama bokki xeet, sama bokki deret. 4 Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi; 5 ñoo xéewloo itam maam ya; ci wàllu doom aadama it, ci ñoom la Almasi soqikoo, di Yàlla, tiim lépp, te yelloo cant ba fàww. Amiin.
6 Du caageenu kàddug Yàlla moo neen, ndax ñi bokk ci xeetu Israyil ñépp duñu Israyil tigi. 7 Te it sëti Ibraayma yépp bokkuñu ci askanam, waaye li Mbind mi indi moo di: «Ci Isaaxa lees di tudde saw askan*9.7 Seetal ci Njàlbéen ga 21.12. .» 8 Loolu di tekki ne du sëti Ibraayma yi ci wàllu deret ñoo di doomi Yàlla, waaye doom yi seenub juddu dëppoo ak digeb Yàlla, ñoom lañu jàpp ne ñooy askanu Ibraayma. 9 Ndax kat kàddug dige ba nii la jibe: «Nëgëni sii déwén laay délsi, te Saarata dina am doom ju góor†9.9 Seetal ci Njàlbéen ga 18.10, 14..»
10 Te yemul foofu rekk, waaye Rebeka it moo am ay seex yu genn góor jur, muy sunu maam Isaaxa. 11 Doom ya nag juddooguñu woon bay def lenn lu baax, mbaa lu bon. Yàlla moo defe noonu ngir wéyal dogal bu dëppoo ak tànnéefu boppam 12 bu ajuwul ci kawi jëf, xanaa ci kiy woote. Rebeka‡9.12 Rebeka mooy soxnas Isaaxa. la kàddu gii dikkal: «Mag ji mooy surgawu rakk ji§9.12 Seetal ci Njàlbéen ga 25.23..» 13 Noonu la Mbind mi indee ne: «Askanu Yanqóoba rakk ji laa sopp, foñ askanu Esawu mag ji*9.13 Seetal ci Malasi 1.2-3..»
Sànjum Yàlla rax na yërmande
14 Ana lu nu ci mana wax nag? Yàlla daa wàcc foofu yoon? Mukk kay! 15 Ndax kat moo noon Musaa:
«Maay yërëm ku ma neex,
te maay ñeewante ku ma neex†9.15 Seetal ci Mucc ga 33.19..»
16 Kon nag mbaaxug Yàlla ajuwul ci coobarey nit ki, mbaa aw ñaqam, waaye lépp yërmandey Yàlla la. 17 Mbind mi moo indi kàddu ga dikkaloon Firawna, ne ko: «Maa la yékkati, te li ko waral mooy lii ci boppam: ngir fésal sama doole ci yaw, ngir itam ñu sàbbaal sama tur ci àddina sépp‡9.17 Seetal ci Mucc ga 9.16. .» 18 Kon nag Yàlla mooy yërëm ku ko neex, te ku ko neex lay dëgëral xolam.
19 Xam naa dinga ma ne: «Ana kon lu Yàlla di sikkeeti? Coobarey Yàlla, ana ku koy fanq?» 20 Waaye yaw nit ki, yaay kan bay weddi Yàlla? Ndax këf ku ñu tabax dina ne ka ko tabax: «Lu tax nga sàkke ma nii?» 21 Tabaxkatu ndab bi daa amul sañ-sañ ci ban bi muy liggéeye, ngir tabax ci bennub tooyal, lenn ndabal teraanga, ak leneen ndabal njoogaan?
22 Yàlla mi namma wone am sànjam, xamle dooleem, su dee moo muñal lool ay ndab yu yelloo am sànjam, te seen sànkute ñoroon xomm nag? 23 Su dee Yàlla moo def loolu nag ngir fésal màggaayu teddngaam, ñeel ay ndab yu xéewloo yërmande, te mu waajalaloon leen teraanga? 24 Nun ci ndabi yërmande yi Yàlla woo lanu bokk, te du ci Yawut yi rekk lees nu seppee, waaye ci jaambur ñi dul Yawut itam. 25 Moom la wax it ci téereb Ose ne:
«Ñi dul woon sama ñoñ,
ñoom laay wax sama ñoñ,
ñooñu dul woon samab xejj,
ñoom laay xejjoo.§9.25 Seetal ci Ose 2.25.»
26 «Te foofa ñu leen noon: “Yeen, dungeen sama ñoñ,”
fa lees leen naa: “Yeenay doomi Yàlla jiy dund*9.26 Seetal ci Ose 2.1..”»
27 Ci mbirum Israyil la Yonent Yàlla Esayi itam xaacu woon ne:
«Su bànni Israyil tolloo ni feppi suufas géej sax,
as ndes a ciy mucc†9.27 Seetal ci Esayi 10.22..
28 Ndax kàddu gi Boroom bi wax,
moo koy sottal ci lu gaaw ci kaw suuf‡9.28 Seetal ci Esayi 10.23.».
29 Mooy itam la Esayi waxoon lu jiitu, ne:
«Su nu Boroom gàngoori xare yi
waccalul woon kuutaay,
ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool§9.29 Seetal ci Esayi 1.9..»
Bànni Israyil déggoowul ak xibaaru jàmm bi
30 Ana lu nu ci mana wax? Xeet yu dul Yawut te sàkkuwuñu woon ag njub, ñoo jagoo àtteb njub, te mooy njub gi ngëm di maye. 31 Waaye xeetu Israyil wi sàkku woon yoonu njub, ñoo moy yoon wi. 32 Ndax lan? Ngëm lañu sukkandikoowul, xanaa ay jëf. «Doj wuy fakktale,» moom lañu fakktaloo. 33 Noonu la Mbind mi indee ne:
«Maa ngii di dëj fi Siyoŋ doj wuy fakktale,
mooy xeer wuy daaneel,
waaye ku ko wéeroo ngëm, doo rus*9.33 Seetal ci Esayi 8.14; 28.16..»
*9:7 9.7 Seetal ci Njàlbéen ga 21.12.
†9:9 9.9 Seetal ci Njàlbéen ga 18.10, 14.
‡9:12 9.12 Rebeka mooy soxnas Isaaxa.
§9:12 9.12 Seetal ci Njàlbéen ga 25.23.
*9:13 9.13 Seetal ci Malasi 1.2-3.
†9:15 9.15 Seetal ci Mucc ga 33.19.
‡9:17 9.17 Seetal ci Mucc ga 9.16.
§9:25 9.25 Seetal ci Ose 2.25.
*9:26 9.26 Seetal ci Ose 2.1.
†9:27 9.27 Seetal ci Esayi 10.22.
‡9:28 9.28 Seetal ci Esayi 10.23.
§9:29 9.29 Seetal ci Esayi 1.9.
*9:33 9.33 Seetal ci Esayi 8.14; 28.16.