Saar 2
Waaye man saxayaayu joor doŋŋ laa,
nirook as tóor-tóor ciw xur.
 
Waa ji
Xanaa as tóor-tóor su ne ràññ ci biiri dég!
Kookooy sama xarit ci biir janq ji.
 
Ndaw si
Mbete garab gu gëna neex ci gott bi,
kookooy sama nijaay ci biir xale yu góor yi.
May bége keppaaram, safoo doom ya.
Dugal na ma néegub sago-jeex-na,
yiire ma mbëggeel.
Gaaweleen ma nàkki reseñ, ma dëgër,
leel-leen may meññeef, leqlee ma.
Wopp laa def ndax mbëggeel!
Sama càmmoñu waay, ma gegenoo,
ndijooram, ma laxasoo.
 
Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma
ci taaru kéwél ak koobay àll bi,
ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel
te jotul.
Wootante jib na
Ndaw si
Dégluleen, sama nijaay a,
mu ngooguy ñëw,
di xéluy jéggi tund yu ndaw yi,
di tëb tund yu mag yiy dikk.
Sama nijaay a ngi mel ni kéwél,
mbaa kooba gu ndaw.
Mu ngi noonu taxaw ca gannaaw miir ba,
di séentu ci palanteer bi
ak a yër ci caax bi.
 
10 Sama nijaay ne ma:
«Xarit, ayca,
jongama sama, dikkal boog!
11 Xoolal, tawub sedd wees na,
waame jàll, wéy*2.11 Ci Israyil, jamonoy sedd day taw. Bu taw bi jeexee, tàngoor wi dikk, gàncax gi jebbi, daldi naat..
12 Tóor-tóor yi lal na réew mi,
jamonoy woy dikk,
sabum pégét2.12 pégét xeetu picc la mu nirool pitax. jibe sunum réew.
13 Figg a ngi ñorsi,
reseñ tóor, di gilli.
Xarit, ayca,
jongama sama, dikkal boog!»
 
Waa ji
14 Soppe, sore nga ni xati mu dëkke xar-xari doj,
làqoo ruqi mbartal yi.
Won ma sa jëmm,
dégtal ma sa baat.
Sa baat a neex,
sa jëmm jekk!
 
Ndaw si
15 Jàppal-leen ma till yi,
till yu ndaw yiy ruur reseñ,
te sunu reseñ jiy tóor.
 
16 Sama nijaay, maa moom, man it, moo moom,
di fore digg tóor-tóor yi.
17 Nijaay, balaa jant a fenk,
ker toxu,
dellul gaaw ni kéwél,
mbaa kooba gu ndaw kaw tund yu xàjjalikoo ya.

*2:11 2.11 Ci Israyil, jamonoy sedd day taw. Bu taw bi jeexee, tàngoor wi dikk, gàncax gi jebbi, daldi naat.

2:12 2.12 pégét xeetu picc la mu nirool pitax.