Saar 2
Ñaareelu misaal: Ay béjjén ak ay tëgg
Ba mu ko defee, ma séentu, gisuma lu moy ñeenti béjjén* 2.1 béjjén ñaare doole lay taxawe.. Ma ne malaaka ma doon wax ak man: «Béjjén yii nag?» Mu ne ma: «Béjjén yii ñoo tasaare Yuda ak Israyil ak Yerusalem.» Ci kaw loolu Aji Sax ji won ma ñeenti tëgg. Ma ne: «Lan la ñii di defsi?»
Mu wax ma, ne ma: «Béjjén yii tasaare Yuda ba kenn siggeetul, tëgg yii ñoo dikk ngir tiital leen, ba jàllarbi béjjéni xeet yi jóg song réewum Yuda, tasaare ko.»
Ñetteelu misaal: Nit kuy natt Yerusalem
Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom. Ma ne ko: «Foo jëm?»
Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo, ak nu mu gudde.»
Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom. Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram. Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”
 
10 «Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,»
kàddug Aji Sax jee.
«Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo,
ni laa leen tasaaree.»
Kàddug Aji Sax jee.
11 «Éy Siyoŋ, rëccal,
yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»
12 Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax, moom mi ma yebal ngir teddngay boppam, ci mbirum xeet, yi leen sëxëtoo woon,
nee: «Képp ku leen laal kat, laal na sama reeni xol.
13 Maa ngii déy di xàcci sama loxo ci seen kaw,
te ñoom la seeni jaam di sëxëtooji.»
Kon dingeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal.
 
14 «Sarxolleel te bànneexu, yaw janq Siyoŋ mu taaru,
nde maa ngii di dikk, màkkaanoo fi sa biir.»
Kàddug Aji Sax jee.
15 «Bésub keroog la xeet yu bare di taqook Aji Sax ji,
ba doon sama ñoñ,
ma màkkaanoo fi sa biir.»
Kon nga xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal ci yaw.
16 Aji Sax jeey séddoo Yuda, muy wàllam
ci suuf su sell si,
te mooy taamooti Yerusalem.
17 Na wépp suux ne cell fi kanam Aji Sax ji,
ma ngoogu sàqee fa màkkaanam mu sell ma.

*2:1 2.1 béjjén ñaare doole lay taxawe.