Saar 13
Ay tuur ak yonenti caaxaan day jeex
1 «Bésub keroog bëtu ndox dina bënnal kër Daawuda, ak waa Yerusalem, ngir setal bàkkaar ak sobe.
2 «Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi, «Turi xërëm laay dagge ci réew mi, ba deesatu leen fàttliku. Yonent yeek xelum xërëmtu it, maa koy tukkal ci réew mi. 3 Te képp kuy biralati waxyu, ay waajuram, baayam ak ndeyam nañu ko wax ne ko: “Doo dese bakkan, ndax yaa fen ci turu Aji Sax ji.” Ay waajuram, baayam ak ndeyam nañu ko jam ba mu dee, ca ba muy biral waxyu.
4 «Su bés baa, bépp yonent buy biral waxyu, kersa lay am ci am peeñoom. Kenn du sol ni yonent yi, yérey der yu ànd ak kawaram, ngir di naxe. 5 Kenn ku ne da naan: “Man de dumab yonent, beykat laa. Ab surga laa masa doon ba may ndaw ba tey.” 6 Te su ñu ko nee: “Légét yii ci sab dënn nag?” Da naan: “Lii de ay légét la yu ma jële ca sama kër xarit ya*13.6 xarit ya li mu tekki mooy tuur yi, ci waxin..”»
Kóllëre feddliku na
7 «Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi,
sama jàmbaar jii ma lëngool,»
kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
«Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo,
ma walbati sama loxo,
jublu ci jur gu ndaw gi.
8 Su boobaa ci réew mi mépp, kàddug Aji Sax jee,
ñaari xaaj yi lees di dagg, ñu sànku,
ñetteel ba ca des lees fay wacc.
9 Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara,
xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis,
nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal.
Xaaj boobu moo may woo ci sama tur,
ma wuyu ko.
Moom laay wax: “Sama ñoñ,”
Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»