1.Jaar-jaar ya
muy téere bi jiitu te ëmb jaar-jaari jamono
Ñaari téerey Jaar-jaar ya ca limeefu maam ya la tënke cosaanu Israayil, doore ca Aadama, jaare ci Ibraayma, ba keroog bi bànni Israayil di jóge ca réew ya ñu leen gàddaayloo, délsi Yerusalem.
Téere yii di ñaax askan wi, ngir ñu xam ne njaaxum li dikkal nguuri Israayil ak Yuda terewul Yàlla di sàmmonte ak ay digeem ñeel askan wi. Moo tax bindkat bi indi jaloore yu mag yu Daawuda ak Suleymaan def ak li Yosafat ak Esekiyas ak Yosya def ngir yeesal diine ji ci biir Yuda.
Téereb Jaar-jaar ya bu njëkk, ci ay limeefi maam la ubbee. Gannaaw loolu mu indi jaar-jaari Sawul ak Daawuda, ñaari buuri Israayil ya jiitu. Li téere bi tëje moo di gis-gis bi Daawuda am ci kër Yàlla ga Suleymaan doomam wara tabax.
Yàlla fas na kóllëre ak Daawuda, bi mu ko nee: «Maay yékkati kenn ci saw askan mu wuutu la, jóge ci sa geño; te maay taxawal nguuram. Kookoo may tabaxal kër te maay taxawal ab jalam ba fàww. Man baayam laay doon, moom muy sama doom» (17.11-14). 1.Jaar-jaar ya moo yem ba fa ñu nee: «Suleymaan toog ci jalub Aji Sax ji, di buur, wuutu baayam» (29.23).
Ci tënk:
1.1—9.44. Limeefi maami waa kër Israayil taxaw na.
10.1-14 Lu jëm ci deewug Sawul.
11.1—23.1 Lu jëm ci nguurug Daawuda.
23.2—27.34 Lu jëm ci kër Yàlla gi ak Leween ñi ak njiiti giiri Israayil.
28.1—29.30 Li Daawuda def ci atam yu mujj yi.
Limeefi askan yi
1
(Saar 1—9)
Li ko dale ca Aadama ba ca Ibraayma
1 Aadama mooy baayu Set, Set di baayu Enos, 2 Enos di baayu Kenan, Kenan di baayu Maalaleel, Maalaleel di baayu Yeredd. 3 Yeredd di baayu Enog, Enog di baayu Matusalem, Matusalem di baayu Lemeg, 4 Lemeg di baayu Nóoyin, Nóoyin di baayu góor ñii di Sem ak Xam ak Yafet.
5 Doomi Yafet yu góor ñoo di Gomeer ak Magog ak Maday ak Yawaan ak Tubal ak Meseg ak Tiraas. 6 Doomi Gomeer yu góor ñoo di Askenas ak Difaat ak Togarma. 7 Doomi Yawaan yu góor ñoo di Elisa ak Tarsis ak Kitim ak Dodanim.
8 Doomi Xam yu góor ñoo di Kuus ak Misrayim*Misrayim mooy Misra ba tey. ak Puut ak Kanaan. 9 Doomi Kuus yu góor ñoo di Saba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Seba ak Dedan. 10 Kuus moo jur Nimrodd, ki njëkk di jàmbaar ju siiw ci kaw suuf.
11 Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi 12 ak Pataruseen ñi ak Kasluxeen ñi, ñooñee waa Filisti soqikoo, ak it Kaftoreen ñi.
13 Kanaan moo taawloo Sidon, teg ca Ett. 14 Kanaan mooy maamu Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi. 15 Mooy maamu Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi. 16 Mooy maamu Arwàddeen ñi it ak Cemareen ñi ak Amateen ñi.
17 Doomi Sem yu góor ñoo di Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. Góor ñi Aram jur†ñi Aram jur: seetal ci Njàlbéen ga 10.23. ñii la: Ucc ak Xuul ak Geter ak Meseg. 18 Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber. 19 Eber moom jur ñaari doom yu góor. Kenn ki tudd Peleg (muy firi Séddalikoo), ndaxte ci jamonoom àddina dafa séddalikoo woon. Rakku Peleg ju góor mooy Yogtaan. 20 Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yerax 21 ak Adoram ak Usal ak Digla 22 ak Ebal ak Abimayel ak Seba 23 ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor.
24 Ci tënk, lii mooy askanu Sem: Sem mooy baayu Arpagsàdd, Arpagsàdd di baayu Sela. 25 Sela di baayu Eber, Eber di baayu Peleg, Peleg di baayu Rew. 26 Rew mooy baayu Serug, Serug di baayu Naxor, Naxor di baayu Teraa. 27 Teraa mooy baayu Ibraam miy Ibraayma.
Li ko dale ca Ibraayma ba ca Yanqóoba
28 Doomi Ibraayma yu góor ñoo di Isaaxa ak Ismayla. 29 Ñii lañu meññ: taawub Ismayla bu góor mooy Nebayot. Ña ca topp di Kedar ak Adabeel ak Mibsam 30 ak Misma ak Duuma ak Maasa ak Adàdd ak Tema 31 ak Yetur ak Nafis ak Kedama. Ñooñu ñooy doomi Ismayla yu góor.
32 Ketura, nekkaaleb Ibraayma am naak moom doom yu góor. Ñuy Simran ak Yogsan ak Medan ak Majan ak Yisbag ak Suwa. Doomi Yogsan yu góor di Seba ak Dedan. 33 Doomi Majan yu góor ñoo di Efa ak Efer ak Enog ak Abida ak Elda. Ñooñu ñépp xeetu Ketura lañu.
34 Ibraayma mooy baayu Isaaxa. Doomi Isaaxa yu góor di Esawu ak Israayil‡Israayil ak Yanqóoba, kenn ki la..
35 Doomi Esawu yu góor ñoo di Elifas ak Rewel ak Yewus ak Yalam ak Kore. 36 Doomi Elifas yu góor ñoo di Teman ak Omar ak Cefo ak Gatam ak Kenas ak Amaleg mi mu am ak Timna§Timna: seetal ci Njàlbéen ga 36.12.. 37 Doomi Rewel yu góor ñoo di Naxat ak Sera ak Saama ak Misa.
Lu jëm ci ña sancoon réewum Edom
38 Ñi sancoon Edom ñoo askanoo ci doomi Seyir yu góor. Ñoo di Lotan ak Sobal ak Cibeyon ak Ana ak Dison ak Eccer ak Disan. 39 Doomi Lotan yu góor ñoo di Ori ak Omam. Jigéenub Lotan di Timna. 40 Doomi Sobal yu góor ñoo di Alwan ak Manaxat ak Ebal ak Sefi ak Onam. Doomi Cibeyon yu góor di Aya ak Ana. 41 Doomu Ana ju góor moo di Dison. Doomi Dison yu góor ñoo di Amran ak Esban ak Yittran ak Keran. 42 Doomi Eccer yu góor ñoo di Bilan ak Saawan ak Yakan. Doomi Disan yu góor di Ucc ak Aran.
43 Buur ya falu woon ca réewum Edom, lu jiitu benn buuru bànni Israayil di falu, ñii la: Bela doomu Bewor ju góor. Dinaba moo doon péeyam. 44 Ba Bela faatoo, Yobab doomu Sera ma dëkk Boccara moo falu buur, wuutu ko. 45 Ba Yobab faatoo, Usam ma bokk ci diiwaanu waa Teman falu buur, wuutu ko. 46 Ba Usam faatoo, Adàdd doomu Bedàdd ju góor ja duma woon waa Majan ca réewu Mowab, daldi falu buur, wuutu ko. Péeyam moo doon Awit. 47 Ba Adàdd faatoo, Samla ma dëkk Masreka moo falu buur, wuutu ko. 48 Ba Samla faatoo, Sawul mu Rexobot Efraat moo falu buur, wuutu ko. 49 Ba Sawul faatoo, Baal Anan doomu Agbor ju góor moo falu buur, wuutu ko. 50 Ba Baal Anan faatoo, Adàdd moo falu buur, wuutu ko. Pawu moo doon péeyam, soxnaam di Metabeel ma Mataredd doomu Mesaab di yaayam.
51 Gannaaw ba Adàdd faatoo, kilifa ya jiite Edom ñoo di Timna ak Alwa ak Yetet 52 ak Olibama ak Ela ak Pinon 53 ak Kenas ak Teman ak Mibcar 54 ak Magdiyel ak Iram. Ñooñoo doon kilifay Edom.