3
Ñii ñooy doomi Daawuda
1 Doomi Daawuda yu góor ya mu amoon ca Ebron ñoo di: Amnon taaw ba Axinowam ma dëkkoon Yisreel di ndeyam. Ñaareelu doomam ju góor di Dañeel ma Abigayil ma dëkkoon Karmel di ndeyam. 2 Ñetteelu doomam ju góor moo di Absalom ma Maaka doomu Talmay buurub Gesur di ndeyam. Ñeenteel ba di Adoña ma Agit di ndeyam. 3 Juróomeelu doomam ju góor moo di Sefatiya, ma Abital di ndeyam. Juróom benneelu doomam ju góor di Ittireyam ma mu am ak soxnaam sa ñuy wax Egla. 4 Juróom benn ñooñu la Daawuda am ca Ebron ga mu falu buur juróom ñaari at ak juróom benni weer.
Fanweeri at ak ñett nag la Daawuda falu ca Yerusalem. 5 Ña Daawuda am ca Yerusalem ñoo di Simeya ak Sobab ak Natan ak Suleymaan. Ñooñu ñeent Batseba mi Amyel di baayam mooy seen ndey. 6 Daawuda am na it Ibaar ak Elisama ak Elifelet. 7 Am na Noga ak Nefeg ak Yafya. 8 Am na Elisama ak Elyada ak Elifelet. Muy yeneen juróom ñeenti doomi Daawuda yu góor. 9 Muy mboolem doomi Daawuda yu góor ba mu des doom yi mu am ak ay nekkaaleem. Amoon na itam doom ju jigéen ju ñuy wax Tamar.
Ñii ñooy buuri Yuda
10 Doomu Suleymaan mooy Robowam mi jur Abya, mu jur Asa, mu jur Yosafat. 11 Yosafat jur Yexoram, mu jur Axasya, mu jur Yowas, 12 mu jur Amaciya, mu jur Asaryaa, mu jur Yotam; 13 Yotam jur Axas, mu jur Esekiyas, mu jur Manase. 14 Manase moo jur Amon mi jur Yosya. 15 Doomi Yosya yu góor ñoo di Yoxanan, ñaareelu doomam di Yoyakim, ñetteel ba di Cedesyas, ñeenteel ba di Salum. 16 Doomi Yoyakim yu góor ñoo di Yekoña ak Cedesyas.
Lii mooy askanu buur gannaaw gàddaay ga
17 Yekoña lañu yóbbu ngàllo Babilon. Doomi Yekoña yu góor ñoo di Selcel 18 ak Malkiram ak Pedaya ak Senacar ak Yekamya ak Osama ak Nedabya. 19 Doomi Pedaya yu góor ñoo di Sorobabel ak Simey. Sorobabel am na ñaari doom yu góor, Mesulam ak Anaña, ak doom ju jigéen ju ñuy wax Selomit. 20 Mu dellu am juróomi doom yu góor. Ñuy Asuba ak Oyel ak Berekya ak Asaja ak Yusab Xeset. 21 Ñi askanoo ci Anaña di ay góor ñoom ñépp di Pelaca ak Yesaya; ak itam doom yu góor yu Refaya ak yu Arnan ak yu Abdiyas ak yu Sekaña. 22 Ñi askanoo ci Sekaña ñoo di Semaya aki doomam yu góor, ñooy Atus ak Igal ak Baryax ak Neyarya ak Safat. Ñuy juróom benn. 23 Doomi Neyarya yu góor ñoo di Elyonay ak Esekiyas ak Asrikam, ñuy ñett. 24 Doomi Elyonay yu góor ñoo di Odawya ak Elyasib ak Pelaya ak Akub ak Yoxanan ak Delaya ak Anani, ñuy juróom ñaar.